Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - ROOM - ROOM 14

ROOM 14:2-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ndax am na ku xalaat ne man na lekk ñam wu nekk, fekk ku ngëmam néew du lekk yàpp, waaye léjum rekk lay lekk.
3Kiy lekk lu nekk, bumu xeeb ki ko dul def. Naka noonu itam ku dul lekk yàpp, bumu teg tooñ ki koy lekk; ndax Yàlla nangu na leen ñoom ñaar.
4Koo teg sa bopp, ba di ko teg tooñ? Jaamu jaambur la! Mu taxaw ci liggéeyam, mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la. Waaye dina jub, ndax Boroom bi am na dooley taxawal ko ci njub.
5Noonu itam am na ñiy tànn bés ak ñiy yemale bés yépp. Na ku nekk xam bu wér li muy def, te jàpp ci.
6Ndaxte kuy tànn bés, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi. Kiy lekk lu nekk it, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi; loolu leer na ndax day sant Yàlla. Te it ki baña lekk yàpp, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi, di ko sant.
7Kenn ci nun dundul ngir boppam, kenn deewul it ngir boppam.
8Danuy dund ngir màggal Boroom bi, dee it ngir màggal ko. Kon nag nuy dund mbaa nu dee, noo ngi ci Boroom bi.
9Loolu sax moo waral Kirist dee te dundaat, ngir mana nekk Boroomu ñi dee ak ñiy dund.
10Yaw nag lu tax ngay teg sa moroom tooñ? Lu tax nga koy xeeb? Xanaa nun ñépp, danu dul dajeji fa kanam Yàlla, ngir mu layoo ak nun?

Read ROOM 14ROOM 14
Compare ROOM 14:2-10ROOM 14:2-10