Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Room - Room 10

Room 10:5-14

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Njub gi sàmm ndigali yoon di maye, li ci Musaa bind moo di: «Kuy jëfe digal yooyu, yaay dund ndax ñoom.»
6Waaye njub, gi ngëm di maye, li muy digle mooy: «Bul wax ci sa xel, ne: “Ana kuy yéeg fa kaw?”» nde loolu mooy Almasi wàcc ngay sàkku.
7«Bul ne it: “Ana kuy wàcci njaniiw?”» nde loolu mooy Almasi dekkiwaat ngay sàkku.
8Li mu wax moo di: «Kàddu gaa ngi ci sa wet; mu ngi ci saw làmmiñ ak ci sa xol.» Te loolu mooy kàddug ngëm gii nuy xamle.
9Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc.
10Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc.
11Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus.»
12Ag wuutale amul diggante ab Yawut, ak jaambur bu dul Yawut; ñépp a bokk benn Boroom biy yéwéne mboolem ñi koy woo wall.
13Ndax kat waxees na ne: «Képp ku woo Boroom bi wall ciw turam, mooy raw.»
14Waaye nees di wooye koo gëmul? Nees di gëme koo déggul turam? Nees di dégge turam, te yégleesu ko?

Read Room 10Room 10
Compare Room 10:5-14Room 10:5-14