Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 8

Ngën-gi-woy 8:4-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Yeen janqi Yerusalem, waatal-leen ma ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel te jotul.
5Ana ndaw suy jóge màndiŋ ma nii, wéeroo nijaayam? Ndaw si Ci ron pom gi laa la yee, fa la sa yaay jàppe ëmb, jur la fa.
6Teg ma ci sa xol ni torlukaay, mbaa ci sa përëg ni lamu màndarga. Mbëggeel a bare doole ni ndee, fiiraange xér ni bàmmeel. Day jàpp jippét, di jum bu Aji Sax ji taal.
7Ndox mu ne xéew du fey mbëggeel, ay dex du ko mëdd. Ku koy weccee sa alalu kër gépp it, ñu jéppi laa jéppi rekk.
8Sunub jigéen lu ndaw la, ween sax amu ko. Lu nuy defal sunub jigéen bés bu ñu koy bëggsi?
9Su doon am tata, nu tabaxal ko soorooru xaalis. Su doon bunt, nu aare ko xànqi seedar.
10Maa dim tata, sama ween di sooroor ya; moo tax waa ji xam ne maa di jàmmam.
11Suleymaan am na reseñ ca Baal Amon. Da koo dénk ay beykat. Ku nekk di ko fey meññeef ma junniy dogi xaalis.

Read Ngën-gi-woy 8Ngën-gi-woy 8
Compare Ngën-gi-woy 8:4-11Ngën-gi-woy 8:4-11