Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Ngën-gi-woy - Ngën-gi-woy 5

Ngën-gi-woy 5:1-12

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Jigéen sama, séet sama, dikk naa sama tool, sama ndàbb ak sama cuuraay, ma for, sama lem xelli, ma lekk, sama biiñ ak sama meew, ma naan. Awu Yeen soppe yi, lekkleen; yeen ñi bëggante, naanleen ba màndi.
2Maa ngi nelaw, te xol yewwu; dégluleen, sama nijaay ay fëgg. Mu ne: «Xaritoo, jigéen sama, ubbil ma, sama nenne, alal sama! Sama bopp a ngi laye ba tooy, njañ li fanaanee guus.»
3Ma ne ko: «Summiku naa de, xanaa duma soluwaat? Jàngu naa jeeg, xanaa duma taqati?»
4Sama nijaay yoor loxoom ci xarante bi, sama yaram ne sàyy.
5Ma ne bërét, di ubbil nijaay, sama yoxo yi, diwu ndàbb di ca siit, sama waaraam yi, ndàbb rogalaat ba ci njàppul bunt bi.
6Maa ubbil nijaay, waaye nijaay waññiku na, ba wéy. Ba mu waññikoo, tuuti ma dee. Seet naa ko, gisuma ko; ma woo ko, wuyuwul.
7Wattukat yiy wër dëkk bi gis ma; ñu dóor ma, gaañ ma, ñori sama malaan. Wattukati tata jaa!
8Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma ne su ngeen gisee sama nijaay, ne ko damaa wopp ndax mbëggeel.
9Yaw mi dàq ci jigéen ñi, ana lu sa nijaay gëne keneen? Ana lu mu ëpplee keneen, ba nga di nu waatloo lii?
10Sama nijaay daa xees, leer; kenn la ci fukki junniy góor.
11Kanam gi ni wurus, di wurusu ngalam; njañ li lëmësu, ñuul ni ndobin.
12Gët yi ni pitax yu feggook wali ndox, sangoo meew, feggook ndox mu ne xéew.

Read Ngën-gi-woy 5Ngën-gi-woy 5
Compare Ngën-gi-woy 5:1-12Ngën-gi-woy 5:1-12