5Sa ween yi ni ñaari tef, mbaa seexi kéwél yuy fore digg tóor-tóor yi.
6Balaa jant a fenk, ker gàddaay, ma ne coww diggante tund wa ndàbb ne bann, ak tund wa xas ma neexe.
7Xarit, sa lépp a rafet, sikk nekkul ci yaw.
8Séet sama, jógeel Libaŋ, jege ma, bawool Libaŋ, jegesi ma. Wàcceel colli Amana ak colli Senir ak Ermon. Génnal xunti gaynde yooyook tundi segg ya.
9Jigéen sama, séet sama, benn yoon nga ma xool, sama fit ne tërit. Sa benn peru caq rekk, sama fit ne tërit.
10Jigéen sama, séet sama, sa mbëggeel a neex! Sa mbëggeel a dàq biiñ, sa diw yu xeeñ dàq luy cuuraay.
11Séet sama! Lem ay xellee sa gémmiñ, lem ak meew lal sa làmmiñ. Sa xetu yére xetu àllub Libaŋ la.
12Jigéen sama, séet sama, yaay tóokër bu tëje, yaay seyaan bu tëje, di bëtu ndox bu saañe.
13Yaa di toolub gërënaat bu naat, meññ ngën-gi-meññeef ak fuddën ak reen yu xeeñ,
14muy reen yu xeeñ, safroŋ, barax, kanel, ak xasoo xas mu xeeñ, ndàbb ak alowes ak lépp lu xeeña xeeñ.