Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 26

Màndiŋ ma 26:9-35

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Elyab meññ Nemwel ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñooñii doonooni njiit ca mbooloo ma, ñoo doon diiŋat Musaa ak Aaróona. Ña nga bokkoon ca gàngooru Kore, ba ñuy diiŋat Aji Sax ji,
10ba suuf sa xar, boole leen ak Kore, wonn, keroog ba gàngoor ga sànkoo, te sawara wa lakk ñaar téeméeri nit ak juróom fukk, ñu daldi doon firnde luy artoo.
11Doomi Kore ya nag deewuñu ca.
12Ñi askanoo ci Simeyon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Nemwel mi sos làngu Nemweleen ñi, ak ñoom Yamin mi sos làngu Yamineen ñi, ak ñoom Yakin mi sos làngu Yakineen ñi,
13ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi, ak ñoom Sawul mi sos làngu Cawuleen ñi.
14Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200).
15Ñi askanoo ci Gàdd, ñook seeni làng ñoo di ñoom Cefon mi sos làngu Cefoneen ñi, ak ñoom Agi mi sos làngu Ageen ñi, ak ñoom Suni mi sos làngu Cuneen ñi,
16ak ñoom Osni mi sos làngu Osneen ñi, ak ñoom Eri mi sos làngu Ereen ñi,
17ak ñoom Arodd mi sos làngu Aroddeen ñi, ak ñoom Areli mi sos làngu Areleen ñi.
18Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500).
19Am na nag doomi Yuda yu ñuy wax Er ak Onan. Waaye Er ak Onan ña ca réewum Kanaan lañu faatoo.
20Ñi askanoo ci Yuda, ñook seeni làng ñoo di ñoom Sela mi sos làngu Celaneen ñi, ak ñoom Peres mi sos làngu Pereseen ñi, ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi.
21Ñi askanoo ci Peres ñoo di ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Amul mi sos làngu Amuleen ñi.
22Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500).
23Ñi askanoo ci Isaakar, ñook seeni làng ñoo di Tola mi sos làngu Toleen ñi, ak ñoom Puwa mi sos làngu Puween ñi,
24ak ñoom Yasub mi sos làngu Yasubeen ñi, ak ñoom Simron mi sos làngu Simroneen ñi.
25Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300).
26Ñi askanoo ci Sabulon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Seredd mi sos làngu Sereddeen ñi, ak ñoom Elon mi sos làngu Eloneen ñi, ak ñoom Yaleel, mi sos làngu Yaleleen ñi.
27Làngi Sabuloneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom benn fukki junni ak juróomi téeméer (60 500).
28Ñi askanoo ci Yuusufa nag, ñook seeni làng, ñoo soqikoo ci Manase ak Efrayim.
29Ñi soqikoo ci Manase ñoo di ñoom Makir mi sos làngu Makireen ñi. Makir moo jur Galàdd. Ci Galàdd la làngu Galàddeen ñi soqikoo.
30Ñii ñoo askanoo ci Galàdd: Yeser mi sos làngu Yesereen ñi, ak ñoom Eleg mi sos làngu Elegeen ñi,
31ak Asriyel mi sos làngu Asriyeleen ñi, ak Sikem mi sos làngu Sikemeen ñi,
32ak Semida mi sos làngu Semideen ñi, ak Efer mi sos làngu Efereen ñi.
33Selofat doomu Efer nag amuloon doom ju góor, xanaa aw jigéen doŋŋ. Doomi Selofat yu jigéen di Maala ak Nowa ak Ogla ak Milka ak Tirca.
34Làngi Manasee ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (52 700).
35Ñii nag ñoo askanoo ci Efrayim, ñook seeni làng: ñoom Sutela mi sos làngu Cuteleen ñi, ak ñoom Beker mi sos làngu Bekereen ñi, ak ñoom Taxan mi sos làngu Taxaneen ñi.

Read Màndiŋ ma 26Màndiŋ ma 26
Compare Màndiŋ ma 26:9-35Màndiŋ ma 26:9-35