Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 23

Màndiŋ ma 23:18-30

Help us?
Click on verse(s) to share them!
18Balaam daldi yékkati kàddug ñaanam, ne: «Jógal dégloo, Balag, teewlu maa, doomi Sippor.
19Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?
20Kàddug barkeel gii laa jot ndigalam, Yàllaa barkeel, duma ko tebbi.
21Séeneesul aw ay ci askanu Yanqóoba, giseesul aw naqar ci xeetu Israyil wii. Seen Yàlla Aji Sax jee ànd ak ñoom, njiinum buur a jibe fa seen biir.
22Yàllaa leen jële Misra, féete leen fa ay béjjén féete nagu àll.
23Ñeengo jàppul Yanqóoba, gisaane gisul Israyil gii. Lu jot rekk, àggees ko Yanqóoba: ne ko: “Israyiloo, lii la Yàlla def.”
24Wii askan ni gaynde lay jóge, ni gayndeg sibi lay faboo, du goor te yàppul am pàdd, deret ja tuuru, mu xab.»
25Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Boo leen móoluwul benn yoon kay, bu leen ñaanal ba doyal boog!»
26Balaam ne ko: «Xanaa waxuma la woon ne la lépp lu Aji Sax ji wax, loolu laay def?»
27Balag ne ko: «Kaay rekk, ma yóbbu la feneen. Jombul Yàlla nangu nga móolool ma leen foofu.»
28Balag yóbbu Balaam ba ca collu tundu Pewor, wa tiim ndànd-foyfoy ga.
29Balaam ne Balag: «Tabaxal ma fii juróom ñaari sarxalukaay, te nga waajalal ma fi juróom ñaari yëkk yu ndaw, ak juróom ñaari kuuy.»
30Balag def na Balaam wax, ba noppi sarxal aw yëkk wu ndaw akam kuuy ci kaw sarxalukaay bu nekk.

Read Màndiŋ ma 23Màndiŋ ma 23
Compare Màndiŋ ma 23:18-30Màndiŋ ma 23:18-30