Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 22

Màndiŋ ma 22:5-38

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Mu yebal ay ndaw ca Balaam doomu Bewor ngir wooyi ko, ca Petor ga Balaam cosaanoo, ca tàkkal dex ga ngir ne ko: «Balaam! Gàngoor a ngii jóge Misra. Ñu ngii lal suuf si ba mu daj, te ñoo sanc, janook man màkk.
6Kon nag dikkal gaaw ñaanal ma yàlla gàngoor gii, ngir ñoo ma ëpp doole. Jombul ma duma leen, ba dàq leen réew mi, ndax xam naa ne koo ñaanal, mu barkeel, te koo ñaan-yàlla, mu alku.»
7Ci kaw loolu magi Mowab ànd ak magi Majan, dem, yóbbaale ay weexal. Ba ñu agsee ca Balaam, daldi koy àgge kàdduy Balag.
8Mu ne leen: «Fanaanleen fii guddig tey. Tont lu ma ci Aji Sax ji sant rekk, dinaa leen ko àgge.» Kàngami Mowab dal ak Balaam.
9Yàlla nag dikkal Balaam, ne ko: «Nit ñii fi yaw, ñu mu doon?»
10Balaam ne Yàlla: «Buuru Mowab Balag doomu Sippor moo yónnee ci man, ne ma:
11“Balaam, gàngoor a ngii jóge Misra, lal suuf si ba mu daj. Dikkal gaaw móolul ma leen. Jombul ma mana xareek ñoom, ba dàq leen.”»
12Yàlla ne Balaam: «Bul ànd ak ñoom, te bul ñaan-yàlla mbooloo ma, ndax ñooñu ñu barkeel lañu.»
13Ba Balaam jógee ca suba sa, da ne kàngami Balag ya: «Delluleen seenum réew, ndax Aji Sax ji bañ na; mayu ma ma ànd ak yeen.»
14Kàngami Mowab daldi dellu ca Balag, ne ko: «Balaam de bañ naa ànd ak nun.»
15Balag dellu yebal kàngam yu gëna bare, te gëna kawe.
16Ñooña dem ba ca Balaam, ne ko: «Balag doomu Sippor dafa wax ne: “Ngalla, bu la dara teree dikk, wuysi ma.
17Maa lay teral teraanga ju réya réy. Loo ma wax, ma def. Dikkal rekk, móolul ma gàngoor gii.”»
18Balaam tontu surgay Balag, ne leen: «Bu ma Balag doon jox këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def lenn lu tuut mbaa lu réy, lu tebbi sama ndigalu Yàlla Aji Sax ji.
19Waaye yeen it dal-leen fii guddig tey, ba ma xam lu ma Aji Sax jiy waxaat.»
20Ci kaw loolu Yàlla dikkal Balaam ca guddi ga, ne ko: «Gannaaw woosi la mooy tànki ñii, àndal ak ñoom. Waaye nag lu ma la wax rekk, def ko.»
21Ca ëllëg sa Balaam takk mbaamam, ànd ak kàngami Mowab, dem.
22Ba loolu amee sànjum Yàlla tàkk ndax yoon wa mu sumb. Malaakam Aji Sax ji nag taxaw ca yoon wa, nara jànkoonte ak moom, moom mu war mbaamam, ànd ak ñaari surgaam.
23Ci kaw loolu mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji taxaw ca digg yoon wa, xàccib saamaram. Mbaam ma ne walbit, wàcc yoon wa, topp àll ba. Balaam dóor mbaam ma, waññi ko ba ca yoon wa.
24Ba mu ko defee malaakam Aji Sax ji taxawi fu yoon wa def ñall wu sew wu jaare digg tóokëri reseñ, ñaari miir séq ko.
25Mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji, daldi tafu ca miir ba, ba tancaale ca tànkub Balaam. Balaam dellu ko dóor.
26Malaakam Aji Sax ja dellu jiitu, ba taxawi fu xat, ba maneesula weesalook moom, du ndijoor, du càmmoñ.
27Mbaam ma gis malaakam Aji Sax ja, daldi ne wàpp goor ca suufu Balaam, xol ba fuddu, mu dóorati mbaam ma yet wa.
28Ba loolu amee Aji Sax ji tijji gémmiñu mbaam mi, mu ne Balaam: «Ana lu ma la def, ba ñetti yoon a ngii nga di ma dóor?»
29Balaam ne mbaam mi: «Yaa may foontoo, su ma yoroon saamar, léegi laa lay rey!»
30Mu ne ko: «Xanaa du maay sa mbaam mi ngay war bu yàgg ba nga ma moomee, ba tey jii? Dama laa masa def nii?» Mu ne ko: «Déedéet.»
31Aji Sax ji nag ubbi bëti Balaam, mu gis malaakam Aji Sax ja, mu taxaw ca yoon wa, xàccib saamaram. Mu ne gurub sukk, dëpp jëëm fa suuf.
32Malaakam Aji Sax ji ne ko: «Lu tax ngay dóor sa mbaam mi ñetti yoon nii? Man mii maa dikk, jànkoonteek yaw, ndax yoonu sànkute laa gis.
33Mbaam mi moo ma gis, teggi ma ba muy ñetti yoon nii. Bu ma teggiwuloon déy, yaw laay rey; moom, ma ba ko, mu dund.»
34Balaam ne malaakam Aji Sax ji: «Maa tooñ, ndax xawma woon ne yaa taxaw, dogale ma ci yoon wi. Léegi nag su la yoon wi neexul, ma daldi dëpp.»
35Malaakam Aji Sax ji ne Balaam: «Àndal ak nit ñi, waaye daal lu ma la waxloo rekk, wax ko.» Balaam nag ànd ak kàngami Balag, dem.
36Ba loolu amee Balag dégg ne Balaam a ngay ñëw, mu gatanduji ko ca dëkku Mowab, ba digalook dexu Arnon, ca catu réew ma.
37Balag ne Balaam: «Xanaa yeblewuma woon, ba yebleeti, di la woolu? Lu la tee woona ñëw? Am dama laa manula teral?»
38Balaam ne Balag: «Maa ngii, wuysi la, waaye mbaa sañ naa waxal sama bopp lenn? Kàddu gu ma Yàlla waxloo de, moom laay wax.»

Read Màndiŋ ma 22Màndiŋ ma 22
Compare Màndiŋ ma 22:5-38Màndiŋ ma 22:5-38