Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 22

Màndiŋ ma 22:4-7

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Ci kaw loolu Mowab giseek magi Majan, ne leen: «Ndiiraan wii kat, ni nag di forem parlu ba mu set, ni lañu nara ñédde li nu wër lépp, ba mu set.» Jant yooyu Balag doomu Sippor moo doon buuru Mowab.
5Mu yebal ay ndaw ca Balaam doomu Bewor ngir wooyi ko, ca Petor ga Balaam cosaanoo, ca tàkkal dex ga ngir ne ko: «Balaam! Gàngoor a ngii jóge Misra. Ñu ngii lal suuf si ba mu daj, te ñoo sanc, janook man màkk.
6Kon nag dikkal gaaw ñaanal ma yàlla gàngoor gii, ngir ñoo ma ëpp doole. Jombul ma duma leen, ba dàq leen réew mi, ndax xam naa ne koo ñaanal, mu barkeel, te koo ñaan-yàlla, mu alku.»
7Ci kaw loolu magi Mowab ànd ak magi Majan, dem, yóbbaale ay weexal. Ba ñu agsee ca Balaam, daldi koy àgge kàdduy Balag.

Read Màndiŋ ma 22Màndiŋ ma 22
Compare Màndiŋ ma 22:4-7Màndiŋ ma 22:4-7