Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 21

Màndiŋ ma 21:1-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Kanaaneen ba, buurub Arat ba dëkke woon Negew, moo dégg ne Israyil a ngay jaare yoonu Atarim, di dikk. Mu xareek Israyil, jàpp ñenn ca ñoom.
2Ci kaw loolu Israyil xasal Aji Sax ji aw xas, ne ko: «Soo tegee ba teg mbooloo mii ci sunuy loxo déy, dinanu faagaagal seeni dëkk.»
3Aji Sax ji nangul Israyil, jébbal leen Kanaaneen ña, ñu faagaagal leen, ñook seeni dëkk. Ñu daldi wooye gox ba Xorma (mu firi Lu ñu faagaagal).
4Ñu bàyyikoo tundu Or, jubal yoonu géeju Barax ya, ngir teggi réewum Edom. Mbooloo ma nag mujj xàddi ca yoon wa.
5Ña ngay xultu ca kaw Yàlla ak Musaa, naa: «Lu ngeen nu doon jële Misra, ngir nu dee ci màndiŋ mi? Duw ñam, dum ndox, te wii ñamu toskare génnliku nan!»
6Ba loolu amee Aji Sax ji yebal ay jaani daŋar ca biir mbooloo ma, ñu màtt leen, ba ñu bare ci bànni Israyil dee.
7Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma.
8Aji Sax ji ne Musaa: «Defarlul jëmmu jaan ju am daŋar, nga wékk ko ci bant. Su ko defee képp ku ñu màtt, boo ca xoolee, mucc.»
9Ci kaw loolu Musaa defarlu jaanu xànjar, wékk ko ci bant, ba képp ku jaan màtt, bu xoolee jaanu xànjar ja, daldi mucc.
10Bànni Israyil fabooti, dem ba dali fa ñuy wax Obot,
11jóge Obot, dali Yee Abarim, ca màndiŋ ma janook Mowab, ca penku ba.
12Foofa lañu faboo, dem ba dali ca walum Seredd,
13bàyyikooti foofa, dem ba dali ca wàllaa dexu Arnon, ga wale ca réewum Amoreen ña te jaare ca màndiŋ ma. Dexu Arnon googa, fa la réewum Mowab digalook Amoreen ñi.
14Moo tax téereb Xarey Aji Sax ji indi ko, ne: «Waxeb ga ca Sufa, xuri Arnon yaak
15xur ya bartalu, jëm néegi Ar, leruji suufas Mowab.»
16Fa lañu bàyyikoo, dem Beer, (mu firi ab Teen); teen boobu, fa la Aji Sax ji noon Musaa: «Dajaleel mbooloo mi, ma may leen ndox.»
17Ca la Israyil woy woy wii: «Teen bile walal, nu woy.
18Ay garmee la bënn, kàngami askan wi gase la yeti buur, ak seen banti bopp.» Ñu jóge màndiŋ ma, dem ba Matana,
19jóge Matana dem Naxaliyel, jóge Naxaliyel, dem Bamot,
20jóge Bamot ba ca xur, wa ca àllub Mowab, àkki nag njobbaxtalu tundu Pisga, wa tiim ndànd-foyfoy ga.
21Ba loolu amee Israyil yebal ay ndaw ca Siwon buurub Amoreen ña, ne ko:
22«May nu, nu jaare sam réew. Dunu fi jàdde benn tool mbaa ab tóokëru reseñ, dunu fi naan ndoxum teen. Mbeddum buur lanuy topp, ba keroog nuy jàll sam réew.»
23Siwon nag mayul Israyil, ñu jaarem réewam, xanaa mu dajale gàngooram gépp, sàqi, ngir dajejeek Israyil ca màndiŋ ma. Mu dikk ba Yaxacc, song Israyil,
24Israyil leel ko ñawkay saamar, nangu seenum réew, dale ko Arnon ba Yabog, ba àgg ca Amoneen ña, ndax kemu réewum Amoneen ñaa fegu woon ba jotuwul.

Read Màndiŋ ma 21Màndiŋ ma 21
Compare Màndiŋ ma 21:1-24Màndiŋ ma 21:1-24