Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 20

Màndiŋ ma 20:11-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Ci kaw loolu Musaa yékkati loxoom, dóor yetam ca doj wa ñaari yoon, ndox mu bare wale ca, mbooloo ma daldi naan, ñook seenug jur.
12Aji Sax ji nag ne Musaa ak Aaróona: «Gannaaw gëmuleen ma, ngir wormaal sama sellnga fi kanam bànni Israyil, loolu tax na dungeen yóbbu mukk mbooloo mii ca réew ma ma leen jox.»
13Loolooy walum Meriba, (mu firi Jote ba). Fa la bànni Israyil jote woon ak Aji Sax ji, ba mu biral sellngaam fa seen biir.
14Gannaaw gi, Musaa moo yebale ay ndaw fa dëkk ba ñuy wax Kades, ñu dem ca buurub Edom, ne ko: «Israyil say bokk dañoo wax ne: Umplewoo mboolem coono bi nu daj.
15Sunuy maam a demoon Misra; dëkk nanu Misra lu yàgg, waa Misra di nu mitital, na woon ca sunuy maam.
16Ci biir loolu nu woo Aji Sax ji wall, mu dégg sunu yuux, daldi yebal malaaka, mu génne nu Misra. Léegi nu ngi nii fi Kades, dëkk bi digalook sam réew.
17Ngalla nag may nu, nu jaare sam réew. Dunu fi jaare benn tool, mbaa ab tóokëru reseñ, dunu fi naane ndoxum benn teen. Mbeddum buur daal lanuy topp, dunu jàdd ndijoor ak càmmoñ, ba keroog nuy génn sam réew.»
18Buurub Edom nag ne leen: «Dungeen jaare fi man de, lu ko moy saamar laay génne, dajeek yeen.»

Read Màndiŋ ma 20Màndiŋ ma 20
Compare Màndiŋ ma 20:11-18Màndiŋ ma 20:11-18