Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 1

Màndiŋ ma 1:2-51

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2«Limleen mbooloom bànni Israyil gépp, na ñu bokke seeni làng ak seen këri maam. Waññleen góor ñépp, bopp ak bopp, ku nekk ak turam.
3Li ko dale ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci Israyil daal, nangeen leen lim, gàngoor ak gàngoor, yaw ak Aaróona.
4Giir gu ci nekk, àndleen ceek kilifa yi jiite seen këri maam, ñu jàpple leen ci.
5Ñiy wuyoo tur yii nag, ñoo leen ciy taxawu: Ci wàllu Rubeneen ñi, Elisur doomu Sedeyur.
6Wàllu Cimyoneen ñi, Selumyel doomu Surisadaay.
7Wàllu Yudeen ñi, Nason doomu Aminadab.
8Wàllu Isakareen ñi, Netanel doomu Suwar.
9Wàllu Sabuloneen ñi, Elyab doomu Elon.
10Ñi ciy askanu Yuusufa ñii la: Ci wàllu Efraymeen ñi, Elisama doomu Amiyut. Wàllu Manaseen ñi, Gamalyel doomu Pedasur.
11Wàllu Beñamineen ñi, Abidan doomu Gidoni.
12Wàllu Daneen ñi, Ayeser doomu Amisadaay.
13Wàllu Asereen ñi, Pagyel doomu Okkran.
14Wàllu Gàddeen ñi, Elyasaf doomu Dewel.
15Wàllu Neftaleen ñi, Ayra doomu Enan.»
16Ñooñu lañu woo ci mbooloo mi, muy ñi jiite seen giiri maam. Ñooy njiiti gàngoori Israyil.
17Ba loolu amee Musaa ak Aaróona tofloo ñooñu ñu tudd seeni tur,
18ñu dajale mbooloo ma mépp, keroog ca benn fanu ñaareelu weer wa. La ko dale ca ña am ñaar fukki at, jëm kaw, ñoom ñépp daldi bindu ca limeefu tur ya, ku nekk ak kër maamam, giir ak giir, làng ak làng, bopp ak bopp.
19Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la Musaa takke seen lim ca màndiŋu Sinayi.
20Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Ruben taawub Israyil seen maam, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
21Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500).
22Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Simeyon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
23Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300).
24Ñu lim turi sëti Gàdd, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
25Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650).
26Ñu lim turi sëti Yuda, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
27Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600).
28Ñu lim turi sëti Isaakar, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
29Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400).
30Ñu lim turi sëti Sabulon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
31Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400).
32Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Efrayim, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
33Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500).
34Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Manase, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
35Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200).
36Ñu lim turi sëti Beñamin, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
37Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400).
38Ñu lim turi sëti Dan, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
39Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700).
40Ñu lim turi sëti Aser, ku nekk ak làngam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
41Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500).
42Ñu lim turi sëti Neftali, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
43Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
44Yooyu limeef la Musaa ak Aaróona tënk, ña leen ca jàpple di fukki kilifay Israyil ak ñaar, ku ci nekk taxawal kër maamam.
45Mboolem bànni Israyil yi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, limees na leen, ku ci nekk ak kër maamam.
46Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550).
47Giirug Leween ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom.
48Aji Sax ji moo waxoon Musaa, ne ko:
49«Giirug Lewi ñoom, bu leen lim, bu leen waññaaleek bànni Israyil.
50Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal.
51Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey.

Read Màndiŋ ma 1Màndiŋ ma 1
Compare Màndiŋ ma 1:2-51Màndiŋ ma 1:2-51