Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 19

Màndiŋ ma 19:6-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Su ko defee sarxalkat bi sàkk bantu seedar ak caru isob ak ndimo lu xonq curr, boole ko sànni ca sawara wa ñuy lakk nag wa.
7Gannaaw loolu na sarxalkat bi fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon.
8Kiy lakk nag wi itam, na fóot ay yéreem, sangu, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon.
9Na ku set tonni dóomu nag wa, te sotti ko bérab bu set, foofa ca biti. Dóom ba dencub mbooloom bànni Israyil lay doon, ñu di ko waajale ndoxum setlu, ngir saraxu póotum bàkkaar.
10Ku góor kiy tonni dóomi nag wi itam day fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba ca ngoon. Na loolu di dogalu yoon bu sax fàww, ñeel bànni Israyil, ak doxandéem bu dëkk ci seen biir.
11«Bu loolu weesee ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, dina sobewu diiru juróom ñaari fan.
12Na setlu ca ndox moomee ca bésub ñetteel ba, gannaaw ba mu ko laalee, te na setluwaat ca bésub juróom ñaareel ba. Su ko defee mu set. Waaye su setluwul ca bésub ñetteel ba, ak bésub juróom ñaareel ba, du set.
13Képp ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, bu setluwul, màkkaanu Aji Sax ji la sobeel. Kooku dees koy dagge ci bànni Israyil. Gannaaw ndoxum setlu ma, wiseesu ko ko, sobewu lay wéye.

Read Màndiŋ ma 19Màndiŋ ma 19
Compare Màndiŋ ma 19:6-13Màndiŋ ma 19:6-13