Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 18

Màndiŋ ma 18:21-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
21Leween ñi ñoom, maa leen jox bépp céru fukkeel bu génne ci Israyil, muy seen cér, ñu yooloo ko seen liggéey bi ñuy liggéey ci xaymab ndaje mi.
22Bu bànni Israyil juuxati ci xaymab ndaje mi, di gàddu bàkkaar bu dee di àtteem.
23Leween ñi ñooy ñiy liggéey liggéeyi xaymab ndaje mi, te lu ñu ca tooñ, ñooy gàddu pey ga, ci kaw dogal bu sax dàkk, ñeel leen, ñook seen askan. Waaye biir bànni Israyil, Leween ñi duñu ci séddu céru suuf,
24ndax céri fukkeel yi bànni Israyil yékkati, jooxeel ko Aji Sax ji, jox naa ko Leween ñi, muy seen cér. Moo tax ma ne leen, biir bànni Israyil, duñu ci séddu céru suuf.
25Aji Sax waxati Musaa ne:
26«Leween ñi, wax leen, ne leen bu ñu jëlee ci bànni Israyil seen céri fukkeel yi ma leen jagleel yeen, muy seen cér, nañu ci jooxeel Aji Sax ji, fukkeelub céru fukkeel yooyu.
27Nañu leen jàppal loolu, yeen Leween ñi, muy seen jooxeb bopp, ni bu doon pepp mu jóge ci seen dàggay bopp, ak biiñ bu bees bu jóge ci seen nalukaay.
28Su ko defee ngeen jooxe yeen itam, jooxeb Aji Sax ji, ci mboolem seen céri fukkeel yi ngeen jële ci bànni Israyil. Kon nangeen jële coocu, jooxeb Aji Sax ji, jox ko Aaróona sarxalkat bi.
29Lépp lu ñu leen sédd, nangeen ci jooxe jooxeb Aji Sax ji. Mboolem céri ngëneel yooyu, ci ngeen di génne cér bu sell boobu.
30«Waxal Leween ñi ne leen gannaaw bu ñu ca génnee céru ngëneel li, li ci des lew na leen, ni bu doon pepp mu jóge ci seen dàggay bopp, ak biiñ bu jóge ci seen nalukaay.
31Sañ nañu koo lekke fépp, ñoom ak seen waa kër, ndax loolu seen pey la, ñu yooloo ko seen liggéeyu xaymab ndaje mi.

Read Màndiŋ ma 18Màndiŋ ma 18
Compare Màndiŋ ma 18:21-31Màndiŋ ma 18:21-31