Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 15

Màndiŋ ma 15:17-41

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Aji Sax ji waxati Musaa, ne
18«Waxal bànni Israyil, ne leen, bu ngeen demee ca réew, ma ma leen jëme,
19bay lekk ca ñamu réew ma, nangeen ci jooxe ab jooxe, ñeel Aji Sax ji;
20seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di jooxe menn mburum jooxe. Ni ngeen di sàkke jooxe bu jóge ca dàgga ja rekk, ni ngeen koy jooxee.
21Seen notu sunguf bu jëkk, ci ngeen di sàkke ab jooxe, ñeel Aji Sax ji, yeen ak seen askan.»
22Su dul ci teyeef ngeen ñàkka jëfe lenn ci mboolem santaane yii Aji Sax ji dénk Musaa,
23ci mboolem lu leen Aji Sax ji sant, Musaa jottli, dale ko keroog ba Aji Sax ji santaanee loola, ak gannaaw gi, ba ca seen maasoo maas,
24su dee moy gu dul teyeef, te mbooloo mi yégu ko woon, su boobaa mbooloo mépp ay sarxal aw yëkk wu ndaw wuy doon rendi-dóomal, ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji, ak saraxu peppam, ak saraxu tuuroom, ni ko yoon àttee, ak benn sikket ngir saraxu póotum bàkkaar.
25Sarxalkat bi day def loolu njotlaayal mbooloom bànni Israyil gépp, njéggal daldi leen ñeel, gannaaw moy ga dug teyeef, te ñoom it indi nañu seen saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji, booleek seen saraxu póotum bàkkaar fi kanam Aji Sax ji, ndax seen moy ga dul teyeef.
26Njéggal day daldi ñeel mbooloom bànni Israyil gépp, ak bépp doxandéem bu dal ak ñoom, ndax mbooloo mépp lay seen moy gu dul teyeef.
27Su dee kenn nit a bàkkaar te du teyeefam, na sarxal aw bëy wu jigéen wu menn at, ngir saraxu póotum bàkkaar.
28Sarxalkat bi daldi koy def fi kanam Aji Sax ji, njotlaayal ki moy ci ag ñàkka tey, ca bàkkaaram ba dul teyeef. Loolu la koy jote, njéggal ñeel ko.
29Muy njuddu-ji-réew ju bokk ci bànni Israyil, di doxandéem bu dal ak ñoom, yoon wi wenn lay doon, ñeel ki moy te du teyeefam.
30Nit ki tooñ cig teyeefam nag, muy njuddu-ji-réew, di doxandéem, kooku Aji Sax ji la ñàkke kersa. Nit kooku, dees koy dagge ci biiri bokkam:
31Gannaaw kàddug Aji Sax ji la teddadil te ndigalam la xëtt, nit kooku dees koy dagg rekk, mu gàddu bàkkaaram.
32Ba bànni Israyil nekkee ca màndiŋ ma, dañoo fekk jenn waay, muy taxan bésub Noflaay.
33Ña ko fekk muy taxan, yóbbu ko ba ca Musaa ak Aaróona, ak mbooloo ma mépp.
34Ba loolu amee ñu teg ko ciy loxo, ndax dogaleesagul woon nees di def ak moom.
35Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Dee rekk mooy àtteb waa ji: dees koy génne dal bi, mbooloo mépp dóor koy xeer, ba mu dee.»
36Mbooloo ma mépp daldi koy génne dal bi, dóor koy xeer ba mu dee, na ko Aji Sax ji sante Musaa.
37Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko:
38«Waxal bànni Israyil, ne leen, ci seen maasoo maas, nañu def ay langat ci seen cati mbubb, langat wu ci nekk ñu nas ci buum gu baxa.
39Mu doon seen langat yu ngeen di xool, di ko fàttlikoo mboolem santaaney Aji Sax ji, ngir di ko jëfe, te baña topp seen bànneexu bakkan ak seeni gët, bay moy.
40Su ko defee ngeen di bàyyi xel tey jëfe sama santaane yépp, daldi doon ñu sell, ñeel seen Yàlla.
41Man maay Aji Sax ji, seen Yàlla, ji leen génnee réewum Misra ngir doon seen Yàlla. Maay seen Yàlla Aji Sax ji.»

Read Màndiŋ ma 15Màndiŋ ma 15
Compare Màndiŋ ma 15:17-41Màndiŋ ma 15:17-41