Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 14

Màndiŋ ma 14:8-35

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Bu nu Aji Sax ji nangulee, moo nuy dugal réew moomu, moo nuy jox réew ma meew maak lem ja tuuroo.
9Fexeleen rekk ba Aji Sax ji, buleen ko gàntal, te yeen nag ngeen baña ragal waa réew ma, ndax ab lanc doŋŋ lañu nuy mat. Seen kiiraay dëddu na leen, te Aji Sax jaa ngeek nun. Buleen leen ragal.»
10Ba mu ko defee mbooloo ma mépp ne dañu leen di dóori xeer ba ñu dee. Leeru Aji Sax ji nag feeñ ca xaymab ndaje ma, ci kanam bànni Israyil gépp.
11Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa: «Ba kañ la ma askan wii nara xarab? Ba kañ lañu may gëmadi, ak firnde yi ma def ci seen biir yépp?
12Maa leen di fàdde mbas, nangu seen cér, ba noppi sose ci yaw askan wu leen ëpp, ëpp leen doole.»
13Musaa ne Aji Sax ji: «Kon de, waa Misra ga nga jële mbooloo mii, génnee leen sa doole ca seen biir, dinañu ko dégg,
14te dinañu ko nettali waa réew mii. Waa réew mii dégg nañu ne yaw Aji Sax ji ci sa bopp yaa nekk ci digg mbooloo mii ngay feeñu bët ak bët, yaw Aji Sax ji, saw niir taxaw, tiim leen, te aw taxaaru niir nga leen di jiitoo bëccëg, jiitoo leen aw taxaaru sawara, guddi.
15Nga nara boole mbooloo mii mépp, bóom benn yoon? Kon de xeet yi dégg sa jaloore dinañu wax ne:
16“Ñàkka mana yóbbu mbooloo mii ca réew ma mu leen giñaloon, moo waral Aji Sax ji faagaagal leen ci màndiŋ mi!”
17Kon nag ngalla Boroom bi, na sa doole màgg rekk, noonee nga noon:
18“Aji Sax ji! Kiy muñ mer, te bare ngor, di bale tooñ aki moy te du ñàkka topp mukk doom, tooñu waajuram, ba ca sët yaak sëtaat ya.”
19Ngalla jéggalal mbooloo mii seenug tooñ ci sag bare ngor, noonee nga leen masa bale, ca Misra ba tey jii.»
20Ba loolu amee Aji Sax ji ne: «Jéggal naa leen noonu nga ko waxe.
21Waaye ndegam maay Kiy Dund, te leeru Aji Sax ji mooy fees àddina sépp,
22gannaaw mboolem nit ñi gis samag leer, gis firnde yi ma def ci digg Misra ak ci màndiŋ mi, ñoo ma nattu nii fukki yoon, bañ maa déggal,
23kenn ci ñoom déy du gis réew, mi ma giñaloon seeni maam. Mboolem ñi ma xarab, kenn du ko ci gis.
24Sama jaam Kaleb nag, gannaaw meneen xel lay wéye, te moo topp sama gannaaw, ba mu mat sëkk, maa koy yóbbu ba ca réew, ma mu demoon, te aw askanam a koy moom.
25Gannaaw Amalegeen ñaak Kanaaneen ñaa nga dëkke xur wi nag, bu ëllëgee walbatikuleen, toppaat màndiŋ mi, te jaareji ko géeju Barax ya.»
26Aji Sax ji waxati Musaak Aaróona, ne:
27«Ba kañ la mbooloo mu bon mii di ñaxtu ci sama kaw? Ñaxtu yi bànni Israyil di ñaxtu ci sama kaw, dégg naa ci.
28Ne leen: Ndegam maay Kiy Dund déy, Kàddug Aji Sax jee, noonu ngeen waxe, may dégg, ni laa leen di def.
29Ci màndiŋ mii kay la seeni néew di tëdd. Mboolem ñi ñu leen limal, mboolem ñi ñu leen waññal, ñu dale ci ñaar fukki at, jëm kaw te doon ñaxtu ci sama kaw,
30kenn ku moy Kaleb doomu Yefune ak Yosuwe doomu Nuun, du kenn ku ciy dugg ca réew, ma ma leen giñoona dëël.
31Seen tuut-tànk, yi ngeen ne alalu sëxëtoo lañuy doon, ñoom laay yóbbu, ba ñu xam réew ma ngeen xarab.
32Waaye yeen, seeni néew ci màndiŋ mii lay tëdd,
33seeni doom di màngaan ñeent fukki at ci màndiŋ mi, gàddoo ko seen ñàkk worma, yeen ñi leen jur, ba keroog seeni néew tëdd ba jeex ci màndiŋ mi.
34Limu fan yi ngeen nemmikuji woon réew ma, ñeent fukki fan, benn fan bu ci nekk day wecci menn at, ngeen gàddoo ko seen mbugali bàkkaar, ñeent fukki at, ba ngeen xam li jànkoonteek man di jur.
35Man Aji Sax ji, maa ko wax. Noonu déy laay def mboolem mbooloo mu bon mii booloo ci sama kaw. Ci màndiŋ mii lañuy raafe, fii lañuy deeye.»

Read Màndiŋ ma 14Màndiŋ ma 14
Compare Màndiŋ ma 14:8-35Màndiŋ ma 14:8-35