Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 14

Màndiŋ ma 14:27-45

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27«Ba kañ la mbooloo mu bon mii di ñaxtu ci sama kaw? Ñaxtu yi bànni Israyil di ñaxtu ci sama kaw, dégg naa ci.
28Ne leen: Ndegam maay Kiy Dund déy, Kàddug Aji Sax jee, noonu ngeen waxe, may dégg, ni laa leen di def.
29Ci màndiŋ mii kay la seeni néew di tëdd. Mboolem ñi ñu leen limal, mboolem ñi ñu leen waññal, ñu dale ci ñaar fukki at, jëm kaw te doon ñaxtu ci sama kaw,
30kenn ku moy Kaleb doomu Yefune ak Yosuwe doomu Nuun, du kenn ku ciy dugg ca réew, ma ma leen giñoona dëël.
31Seen tuut-tànk, yi ngeen ne alalu sëxëtoo lañuy doon, ñoom laay yóbbu, ba ñu xam réew ma ngeen xarab.
32Waaye yeen, seeni néew ci màndiŋ mii lay tëdd,
33seeni doom di màngaan ñeent fukki at ci màndiŋ mi, gàddoo ko seen ñàkk worma, yeen ñi leen jur, ba keroog seeni néew tëdd ba jeex ci màndiŋ mi.
34Limu fan yi ngeen nemmikuji woon réew ma, ñeent fukki fan, benn fan bu ci nekk day wecci menn at, ngeen gàddoo ko seen mbugali bàkkaar, ñeent fukki at, ba ngeen xam li jànkoonteek man di jur.
35Man Aji Sax ji, maa ko wax. Noonu déy laay def mboolem mbooloo mu bon mii booloo ci sama kaw. Ci màndiŋ mii lañuy raafe, fii lañuy deeye.»
36Ndaw ya Musaa yebaloon, ñu nemmikuji réew ma nag, te ñu délsi, di baatal réew ma, ba tax mbooloo mépp di ñaxtu ci kawam,
37ñooña doon baatal réew ma, am mbas a leen rey fi kanam Aji Sax ji.
38Mennum Yosuwe doomu Nuun ak mennum Kaleb doomu Yefune doŋŋ, ñoo mucc ca ndaw yooya nemmikuji woon réew ma.
39Ba Musaa jottlee bànni Israyil gépp kàddu yooyu, mbooloo ma mititlu nañu ko lool.
40Ca ëllëg sa ñu teela xëy, yéegi kaw tund ya, te naan: «Nu ngi nii di yéeg, jëm fa nu Aji Sax ji wax, ndax noo tooñ.»
41Musaa ne leen: «Lii nag? Yeena ngi tebbi waxi Aji Sax ji, waaye loolu de du sotti!
42Buleen dem, te Aji Sax ji àndul ak yeen. Lu ko moy dingeen daanu ci seen kanami noon.
43Te kat Amalegeen ñi ak Kanaaneen ñaa ngi fuu ci seen kanam. Yeenay fàddoo saamar doŋŋ. Gannaaw yeena dëddu Aji Sax ji nag, Aji Sax ji du ànd ak yeen.»
44Teewul ñu të ticc, ne dañuy yéegi kaw tund ya, te gaalu kóllërey Aji Sax ji ak Musaa génnuñu dal ba.
45Ba mu ko defee Amalegeen ña ak Kanaaneen ña dëkke woon diiwaanu tund woowa wàccsi, duma leen, tasaare leen ba ca gox ba ñuy wax Xorma.

Read Màndiŋ ma 14Màndiŋ ma 14
Compare Màndiŋ ma 14:27-45Màndiŋ ma 14:27-45