Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 13

Màndiŋ ma 13:5-24

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5ak Safat doomu Ori, ci giirug Cimyoneen ñi,
6ak Kaleb doomu Yefune, ci giirug Yudeen ñi,
7ak Igal doomu Yuusufa, ci giirug Isakareen ñi,
8ak Oseya doomu Nuun, ci giirug Efraymeen ñi,
9ak Palti doomu Rafu, ci giirug Beñamineen ñi,
10ak Gadyel doomu Sodi, ci giirug Sabuloneen ñi,
11ak Gadi doomu Susi, mi taxawal làngu Manase ci biir giirug Yuusufeen ñi,
12ak Amyel doomu Gemali, ci giirug Daneen ñi,
13ak Setur doomu Mikayel, ci giirug Asereen ñi,
14ak Nabi doomu Wofsi, ci giirug Neftaleen ñi,
15ak Gewuyel doomu Maki, ci giiru Gàddeen ñi.
16Ñooñu la Musaa yónni woon, ngir ñu yëri réew ma. Oseya doomu Nuun nag, Musaa tudde ko Yosuwe.
17Ba leen Musaa yebalee ngir ñu yëri réewum Kanaan, da ne leen: «Negew gii ci bëj-saalum ngeen di jaare, yéegi ca diiwaanu tund ya,
18ba gis nu réew ma mel: ndax waa réew ma, ñu am doole lañu, am ñu néew doole; ñu néew lañu, am ñu bare;
19ak ndax réew ma baax na, am baaxul; ak nu seeni dëkk mel: ndax ay dal rekk la, am ay dëkk yu ñu dàbbli la;
20ak suuf sa: ndax nangu na, am nanguwul; ak itam ndax am nay garab, am déet. Te ngeen góor-góorlu ba sàkkaale ca meññeefi réew ma.» Fan yooyu nag yemook reseñ di meññ ndoortel meññeef.
21Ci kaw loolu ndaw ya dem yëri réew ma, dale ko ca màndiŋu Ciin, ba àgg Reyob, ga ca wetu Amat.
22Ña nga jaare Negew ca bëj-saalum, dem ba Ebron, fa Anageen ña, Ayman ak Sesay ak Talmay, dëkkoon. Ebron googee, tabaxees na ko juróom ñaari at lu jiitu Cowan ga ca Misra.
23Ñu dem ba ca xuru Eskol, daldi fay dagge ab car bu def benn cëggub reseñ, ñaar ca ñoom gàddoo ko bant, ñu sàkkaale fa gërënaat ak figg.
24Bérab boobu lañu dippee xuru Eskol, (mu firi xuru Cëgg) ndax cëgg ba fa bànni Israyil dagge woon.

Read Màndiŋ ma 13Màndiŋ ma 13
Compare Màndiŋ ma 13:5-24Màndiŋ ma 13:5-24