Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 12

Màndiŋ ma 12:5-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Aji Sax ji wàcc ci biir niir wu def aw taxaar. Mu taxaw ca bunt xayma ba, daldi woo Aaróona ak Maryaama, ñu bokk dikk.
6Mu ne leen: «Dégluleen bu baax samay kàddu: su ngeen feeñlee ab yonentu Aji Sax ji, ci am peeñu laa koy xamale maay kan, te ci gént laay waxeek moom,
7waaye du Musaa sama jaam bii. Moom mooy ki wóor ci mboolem sama kër gii.
8Gémmiñ ak gémmiñ laay waxeek moom wax ju leer nàññ ju ñu léebul, te jëmmu Aji Sax ji lay gis. Kon lu leen may fitu ŋàññ Musaa sama jaam bi?»
9Sànjum Aji Sax ji nag tàkkal leen. Ci kaw loolu mu dem.
10Naka la niir wa jóge ca xayma ba, Maryaama jekki ne fureet ak jàngoroy ngaana, weex furr! Aaróona ne Maryaama gees, yem ca ngaana ga.
11Aaróona ne Musaa: «Ngalla sang bi, bu nu topp bàkkaar bi nu bàkkaar ndax ñàkk xel!
12Ngalla bul seetaan kii mel ni ku dee te indaalewul bakkan ba mu juddoo ca ndeyam, xaaju yaram wi lekku!»
13Musaa nag jooy Aji Sax ji, ne ko: «Yàlla, ngalla wéral ko!»
14Aji Sax ji ne Musaa: «Xanaa baayam sax su ko jéppi woon, ba tifli ko ci kanam, muy gàcceem diiru juróom ñaari fan? Nañu ko génne dal bi diiru juróom ñaari fan, door koo délloosi ci biir.»
15Ba loolu amee ñu génne Maryaama dal ba diiru juróom ñaari fan. Mbooloo ma demul, ba keroog ba ñu délloosee Maryaama ca biir dal ba.

Read Màndiŋ ma 12Màndiŋ ma 12
Compare Màndiŋ ma 12:5-15Màndiŋ ma 12:5-15