Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Màndiŋ ma - Màndiŋ ma 10

Màndiŋ ma 10:1-33

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Aji Sax ji waxati Musaa, ne:
2«Sàkklul ñaari liiti xaalis. Lu ñu tëgglu ba mu jekk nga koy def. Liit yi ngay wootee am ndaje, di ko yékkatee dal yi.
3Bu ñu liitee ñaar yépp, mbooloo mépp ay dajesi fi yaw, ci bunt xaymab ndaje mi.
4Bu ñu liitee benn nag kilifa yi jiite gàngoori Israyil ñooy dajesi fi yaw.
5Su ñu liitee menn riirum liit mu xumb, dal yi dale penku ñooy fabu.
6Su ñu liitee riirum liit mu xumb, ñaareel bi yoon, dal yi dale bëj-saalum ñooy fabu. Riirum liit mu xumb mooy tegtale seeni fabu.
7Bu dee wooteb ndaje nag, dees koy liit waaye du doon riir mu xumb.
8Na doomi Aaróona sarxalkat yi di wal liit yi, te mu doon dogal bu leen saxal dàkk, ci seen maasoo maas.
9«Bu loolu wéyee, bu ngeen dee xare ci seenum réew, ak noon bu leen songsi, nangeen riiral liit yi riir mu xumb, su boobaa dees na leen bàyyi xel fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ba wallu leen ak seeni noon.
10Seen bési mbég itam, muy seen bési màggal, di seen ndoortel weer, nangeen ciy riiral liit yi riir mu xumb, yéenee ko seen saraxi rendi-dóomal, ak seen saraxi cant ci biir jàmm. Riirum liit yooyu mooy doon seen baaxantal fa seen kanam Yàlla. Maay seen Yàlla, Aji Sax ji.»
11Ca ñaareelu at ma, gannaaw ba bànni Israyil génnee Misra, ca ñaareelu weer wa, keroog ñaar fukkeelu fanam, ca la niir wa bàyyikoo fa tiim màkkaanu seedes kóllëre ga.
12Bànni Israyil daldi sumb seen yooni tukki ya, bàyyikoo màndiŋu Sinayi. Ci kaw loolu niir wa daleji ca màndiŋu Paran.
13Booba lañu jëkka fabu ci kàddug Aji Sax ji, Musaa jottli.
14Raayab dalu Yudeen ña moo jëkka jóg, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Yuda di Nason doomu Aminadab,
15njiital gàngooru Isakareen ña di Netanel doomu Suwar,
16njiital gàngooru Sabuloneen ña di Elyab doomu Elon.
17Ci biir loolu ñu wékki jaamookaay ba, Gersoneen ñaak Merareen ñay gàddu jaamookaay ba daldi dem.
18Raayab dalu Rubeneen ña jóg ànd aki gàngooram, topp ca, njiital gàngooru Rubeneen ña di Elisur doomu Sedeyur,
19njiital gàngooru Cimyoneen ña di Selumyel doomu Surisadaay,
20njiital gàngooru Gàddeen ña di Elyasaf doomu Dewel.
21Gannaaw loolu Keyateen ñay gàddu yëf yu sell ya, ñoo fabu, topp ca. Bala ñoo àgg fa ñuy dalewaat nag, day fekk jaamookaay ba sampewaat.
22Ci kaw loolu raayab dalu Efraymeen ña jóg, ànd ak seeni gàngoor, topp ca, njiital gàngooru Efraymeen ña di Elisama doomu Amiyut,
23njiital gàngooru Manaseen ña di Gamalyel doomu Pedasur,
24njiital gàngooru Beñamineen ña di Abidan doomu Gidoni.
25Ba mu ko defee raayab dalu Daneen ña doora jóg, topp ca gannaaw kurél yépp, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Daneen ña di Ayeser doomu Amisadaay,
26njiital gàngooru Asereen ña di Pagyel doomu Okkran,
27njiital gàngooru Neftaleen ña di Ayra doomu Enan.
28Noonu la bànni Israyil topplantee, ànd ak seeni gàngoor, tegu ca yoon wa.
29Ba loolu amee Musaa wax ak Obab doomu Ruwel waa Majan ba, baayu soxnaam, ne ko: «Nu ngi nii jëm fa nu Aji Sax ji wax ne moom lanuy jox. Kaay nu ànd, dem, nu baaxe la, ndax Aji Sax ji moo digee baaxe Israyil.»
30Mu ne ko: «Déedéet, duma dem, samam réew kay laa jëm, ca saay bokk.»
31Mu ne ko: «Bu nu wacc kay, ndax gannaaw yaa xam fu nu wara dal ci màndiŋ mi, yaa nu wara jiite.
32Soo àndeek nun déy, xéewal googa nu Aji Sax jiy baaxeji, dinanu la ci baaxe.»
33Ci kaw loolu ñu bàyyikoo ca tundu Aji Sax ja, doxe fa doxub ñetti fan. Gaalu kóllërey Aji Sax jaa nga leen jiitu diiru ñetti fan ña, di leen wutal dal-lukaay.

Read Màndiŋ ma 10Màndiŋ ma 10
Compare Màndiŋ ma 10:1-33Màndiŋ ma 10:1-33