Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 8

LUUG 8:22-46

Help us?
Click on verse(s) to share them!
22Benn bés Yeesu àndoon na ak ay taalibeem, dugg ci gaal. Mu ne leen: «Nanu jàll dex gi.» Noonu ñu dem.
23Bi ñuy dem nag, Yeesu daldi nelaw. Ngelaw lu am doole daldi ñëw, yëngal dex gi, gaal gi fees ak ndox, ba ñu bëgga suux.
24Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
25Yeesu ne taalibe yi: «Ana seen ngëm?» Ñu daldi tiit te waaru, naan ci seen biir: «Kii moo di kan? Mi ngi jox ndigal ngelaw li ak ndox mi, ñu koy déggal.»
26Noonu ñu teer ca diiwaanu waa Serasa, fa jàkkaarloo ak diiwaanu Galile.
27Bi Yeesu di wàcc ca gaal ga, ku rab jàpp ca waa dëkk ba ñëw, kar ko. Yàgg na def yaramu neen te dëkkul ca kër, waaye ca sëg ya lay nekk.
28Bi mu gisee Yeesu, mu yuuxu, daanu ciy tànkam, daldi xaacu ne: «Yaw Yeesu Doomu Yàlla Aji Kawe ji, loo may fexeel? Maa ngi lay ñaan, nga bañ maa mbugal.»
29Dafa wax loolu, ndaxte Yeesu santoon na rab wi, mu génn ci moom. Rab wa dafa ko doon farala jàpp. Nit ñi daan nañu ko wottu, di ko yeew ak ay càllala, ak di ko jéng, mu di leen dagg, rab wi di ko xiir ca bérab yu wéet.
30Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd.» Dafa wax loolu, ndaxte rab yu baree ko jàppoon.
31Rab yooyoo ngi ko doon ñaan, ngir mu bañ leena sant, ñu dem ca kàmb gu xóot gi.
32Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko.
33Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab.
34Sàmm ya gis li xew, daw nettaliji mbir mi ca dëkk ba ak ca àll ba.
35Nit ñi génn, ngir seet li xew. Bi ñu agsee ca Yeesu, ñu fekk fa nit, ka rab ya bàyyi woon, toog ca kanam Yeesu, sol ay yére te ànd ak sagoom. Ñu daldi ragal.
36Ña fekke woon mbir ma nag, nettali leen naka la Yeesu wérale ki rab ya jàppoon.
37Ci kaw loolu waa diiwaanu Serasa bépp ragal, ba ñaan Yeesu mu jóge fa. Noonu Yeesu dugg ci gaal gi, di bëgga dem.
38Nit ki Yeesu tàggale woon ak rab ya ñaan ko, ngir ànd ak moom. Waaye Yeesu waññi ko ne ko:
39«Ñibbil, nettali li la Yàlla defal lépp.» Noonu waa ji dem di wër dëkk ba yépp, di fa yégle la ko Yeesu defal.
40Bi Yeesu dëppee dellu, mbooloo ma di ko teeru, ndaxte ñépp a ngi ko doon xaar.
41Noonu nit ñëw, tuddoon Yayrus te nekk njiitu jàngu ba. Bi mu agsee, mu daanu ci tànki Yeesu, sarxu ko mu ñëw këram,
42ndaxte jenn doomam ju jigéen, ji mu amoon kepp te muy tollu ci fukki at ak ñaar, ma nga doon waaja dee. Bi Yeesuy dem, nit ñaa ngi doon buuxante, di ko tanc.
43Amoon na nag ca mbooloo ma jigéen ju doon xëpp deret diirub fukki at ak ñaar, te kenn manu ko woona faj.
44Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal.
45Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.»
46Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne am na doole ju génn ci man.»

Read LUUG 8LUUG 8
Compare LUUG 8:22-46LUUG 8:22-46