Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 7

Luug 7:17-48

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17Coow loolu nag law ca mboolem réewum Yawut ak mboolem fa ko wër.
18Ci kaw loolu taalibey Yaxya àgge Yaxya loolu lépp. Mu woo ñaar ca taalibe ya,
19yebal leen ci Sang bi, laaj ko ne ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
20Taalibe ya dikk ne ko: «Yaxya moo nu yebal, di la laaj ndax yaa di Ki wara ñëw, am keneen lanuy séentu?»
21Waxtu woowa tembe nag Yeesu faj na ñu bare, tàggale leen aki jàngoro aki jagadi aki rab, silmaxa yu bare, mu baaxe leen, ñuy gis.
22Mu ne ndaw ya: «Li ngeen gis te dégg ko, demleen àgge ko Yaxya. Silmaxa yaa ngi gis, lafañ yi dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, néew yi dekki, néew-doole ñi dégg xibaaru jàmm bi.
23Ku ma taxul nga xàcc sa péete ak man nag, ndokklee yaw.»
24Ba ndawi Yaxya demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya, ne leen: «Lu ngeen seetaani woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax bu ngelaw liy yëngal?
25Kon lu ngeen seetaani woon? Boroom yére yu rafet? Waaye boroom yére yu yànj yooyu te seen dund bakkane, ci këri buur lañu dëkk.
26Kon nag lu ngeen seetaani woon? Ab yonent? Waawaaw, maa leen ko wax, te wees na ab yonent sax.
27Ci moom moomu lañu bindoon ne: “Maa ngii di yebal sama ndaw, mu jiitu la, xàllal la saw yoon.”
28Maa leen ko wax, li jigéen jur, kenn sutu ci Yaxya. Waaye ki gëna tuut ci nguurug Yàlla sax moo ko sut.»
29Mboolem ña déglu Yeesu, ba ca juutikat ya sax, dëggal nañu Yàlla, ndax nangu nañoo sóobu sóobeb Yaxya.
30Waaye Farisen ya ak xamkati yoon ya ñoo gàntal la leen Yàlla nammaloon, ba Yaxya sóobu leen ci ndox.
31Yeesu neeti: «Ana kon lu may niruleel niti tey jii? Ana lu ñuy nirool?
32Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma di awoonte, naan: “Noo leen toxorool, fecculeen, nu dëjal leen, jooyuleen.”
33Ndaxte Yaxya daa feeñ, lekkul dugub, naanul biiñ, ngeen nee: “Aw rab la àndal.”
34Doomu nit ki feeñ, di lekk ak a naan, ngeen naay: “Kee fuqle, naan-katub biiñ biiy xaritook juutikat yeek bàkkaarkat yi.”
35Waaye xel mu rafet, mboolem la mu jur mooy la koy dëggal.»
36Kenn ca Farisen ya moo woo woon Yeesu, ngir ñu bokk lekk. Yeesu agsi kër Farisen ba, daldi dikk ca ndab la.
37Ndeke senn as ndaw a nga ca dëkk ba, ab moykat la woon. Mu yég nag ne Yeesoo nga ca kër Farisen ba, di lekk. Mu dikk, indaale njaqal doju albatar lu def diwu xeeñlu.
38Mu dikk ba fa Yeesu sóonu, ca gannaawam, fa tànki Yeesu féete, daldi taxaw, di jooy, rongooñ ya tooyal xepp tànk ya. Ndaw sa nag di fompe tànki Yeesu kawaru boppam gay lang, di fóon tànk yaak cofeel, di ca sotti diwu xeeñlu ga.
39Farisen ba woo Yeesu nag gis loolu, naan ci xelam: «Kii su doon ab yonent, dina xam ndaw sii di ko nabb-nabbee ku mu doon, ak lu mu doon: jigéenu moykat!»
40Yeesu nag àddu, ne ko: «Simoŋ, dinaa la wax lenn.» Mu ne ko: «Waxal, sëriñ bi.»
41Yeesu ne ko: «Ñaari boroom bor la woon ak seenub leblekat. Boru kenn ka di téeméeri junni (500 000) ci xaalis, ka ca des fukki junni (50 000).
42Waaye ñoom ñaar ñépp, kenn manu cee fey. Mu far jéggal leen ñoom ñépp. Ana kan ci ñaar ñooñu nag moo ciy gëna fonk leblekat bi?»
43Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ëpple lu ñu ko jéggal.» Yeesu ne ko: «Sab àtte jub na.»
44Mu walbatiku ca ndaw sa, daldi ne Simoŋ: «Gis nga ndaw sii de? Dugg naa sa kër, mayewoo ndox mu ma jàngoo. Waaye moom, ay rongooñam la tooyale samay tànk, fompe ko kawaru boppam.
45Fóonuloo ma, dalale ma, waaye moom, ba ma duggsee ba léegi noppiwula fóon samay tànk.
46Ag diw, diwewoo ko sama bopp, waaye moom, diwu xeeñlu la diw samay tànk.
47Moo tax ma di la wax, ne bàkkaaram yu bare yi ñu ko jéggal moo waral fonkeelam gu bare. Waaye njéggal lu tuut, fonkeel gu tuut rekk.»
48Yeesu nag ne ndaw sa: «Jéggalees na la say bàkkaar.»

Read Luug 7Luug 7
Compare Luug 7:17-48Luug 7:17-48