Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 7

LUUG 7:17-40

Help us?
Click on verse(s) to share them!
17La ñu wax ci mbiri Yeesu daldi siiw ca réewu Yawut ya ak la ko wër yépp.
18Taalibey Yaxya ya nettali mbir yooyu yépp seen kilifa. Noonu Yaxya woo ñaar ci ay taalibeem,
19yónni leen ci Boroom bi, ngir laaj ko: «Ndax yaw yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?»
20Bi taalibe ya agsee ca Yeesu, ñu ne ko: «Yaxya moo nu yebal, nu laaj ndax yaa di Ki waroona ñëw, walla danuy xaar keneen?»
21Ca waxtu woowa Yeesu wéral nit ñu bare ci seeni feebar ak ci seeni metit, di dàq ay rab tey gisloo ay gumba.
22Noonu mu wax ndaw ya ne leen: «Demleen nettali Yaxya li ngeen gis te dégg ko. Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi.
23Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
24Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
25Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñiy soloo noonu, tey dund dund gu neex ñu ngi dëkk ci këri buur.
26Kon lu ngeen seeti woon? Yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent.
27Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan: “Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la, te xàllal la yoon ci sa kanam.”
28Maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla moo ko sut.»
29Nit ñépp ñi doon déglu Yeesu, ba ci juutikat yi sax, dëggal nañu ne Yàlla ku jub la, ndaxte nangu nañu Yaxya sóob leen ci ndox.
30Waaye Farisen ya ak xutbakat ya dañoo bañ, mu sóob leen ci ndox, di wone noonu ne gàntu nañu li leen Yàlla bëggaloon.
31Yeesu tegaat ca ne: «Kon lan laa mana méngaleel niti jamono jii? Lan lañuy nirool?
32Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma tey woowante naan: “Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen, woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.”
33Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul mburu, naanul biiñ, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.”
34Gannaaw gi nag Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.”
35Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
36Amoon na ab Farisen bu ñaan Yeesu, mu ñëw lekkandoo ak moom. Yeesu dem kër waa ja, toog ca lekkukaay.
37Fekk amoon na ca dëkk ba jigéen juy moy Yàlla. Bi mu yégee ne, Yeesoo ngay lekk ca kër Farisen ba, mu dem, yóbbaale njaq lu ñu defare doj wu ñuy wax albaatar te def latkoloñ.
38Bi jigéen ja agsee, mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu, di jooy. Noonu ay rongooñam tooyal tànki Yeesu, jigéen ja di leen fomp ak kawaram, di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja.
39Naka la Farisen, bi woo woon Yeesu ci këram, gis loolu, mu wax ci xelam naan: «Bu nit kii doonoon yonent, kon dina xam kuy jigéen ji koy laal ak ni mu nekke bàkkaarkat.»
40Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: «Simoŋ, am na lu ma la wara wax.» Simoŋ ne ko: «Waxal, kilifa gi.»

Read LUUG 7LUUG 7
Compare LUUG 7:17-40LUUG 7:17-40