Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 22

Luug 22:33-70

Help us?
Click on verse(s) to share them!
33Piyeer ne ko: «Sang bi, jekk naa ci ànd ak yaw kaso, ak ci ànd ak yaw dee.»
34Yeesu ne ko: «Piyeer, maa la ko wax, bala ganaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.»
35Yeesu neeti leen: «Ba ma leen yebalee te du dencukaayu xaalis, du mbuus, du carax yu ngeen yóbbaale, ndax ñàkk ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
36Mu ne leen: «Léegi nag képp ku am dencukaayu xaalis, na ko jël, ku am mbuus it, na ko jël; ku amul saamar, na jaay mbubbam, jënde saamar.
37Ndax maa leen ko wax, li ñu bind ne, “Mook defkati mbon yi lañu boole ab àtte,” fàww mu am ci man, te loolu jëm ci sama mbir mu ngi sottisi.»
38Ñu ne ko: «Sang bi, ñaari saamar a ngi fi.» Mu ne leen: «Doy na.»
39Ci kaw loolu Yeesu génn, jëm ca tundu Oliw ya, na mu ko baaxoo woon, taalibe ya topp ci moom.
40Ba mu agsee ca bérab ba, da ne leen: «Ñaanleen, ngir baña tàbbi cig fiir.»
41Ba loolu amee mu dànd leen lu tollook saanu xeer, daldi sukk, di ñaan.
42Mu ne: «Baay, su dee sa coobare, teggil ma kaasu naqar bii. Bumuy sama coobare nag, waaye yaw, na sa coobare am.»
43Malaaka mu bawoo asamaan daldi koy feeñu, dooleel ko.
44Njàqare nag jàpp Yeesu, mu gënatee tënku ci kàdduy ñaanam, ba aw ñaqam mujj mel ni lumbi deret, di dal ci suuf.
45Mu ñaan ba noppi, daldi jóg, délsi ci taalibe yi, fekk leen ñuy nelaw, sonn lool ndax aw tiis.
46Mu ne leen: «Lu ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña tàbbi cig fiir.»
47Naka la Yeesu di wax, daaneelagul, mbooloo ne jimeet, ka ñuy wax Yuda, di kenn ca Fukk ñaak ñaar jiite leen. Yuda dikk ba ci Yeesu, bëgg koo fóon.
48Yeesu ne ko: «Yuda, fóon ngay wore Doomu nit ki!»
49Ña ànd ak Yeesu nag gis la ca nara topp, ñu ne: «Sang bi, nu jame saamar boog?»
50Kenn ci ñoom daldi caw surgab sarxalkat bu mag ba, njoof noppu ndijooram.
51Teewul Yeesu ne: «Bàyyileen, na fi yem.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
52Ba loolu amee Yeesu wax ak ña ko jàppsi: sarxalkat yu mag ya, ak kilifay wattukati kër Yàlla ga, ak mag ña. Mu ne leen: «Mbete dama di ab fippukat, ba ngeen dikkey saamar aki njur.
53Moona bés bu nekk, maak yeen la woon ca kër Yàlla ga, te teguleen ma loxo. Waaye seen waxtu la léegi, bi kilifteefug lëndëm ayee nii.»
54Ba mu ko defee ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ba ca kër sarxalkat bu mag ba, Piyeer dànd fu sore, topp ca.
55Fekk na ñu taal sawara ca digg ëtt ba, toog yéew sawara wa, Piyeer dikk toog ca seen biir.
56Ab surga bu jigéen nag gis ko, mu toog fi kanam taal bi, mu ne ko jàkk, ne: «Kii it ci la, moom la àndaloon!»
57Piyeer nag miim, ne: «Soxna si, xawma kooku!»
58Nes tuut keneen gis ko ne: «Yaw it ci ñoom nga!» Piyeer ne ko: «Waa jii, du man!»
59Ba ñu ca tegee lu mat waxtu, keneen jaaraat ca wax ja ne: «Kii kay wax-dëgg, moom la àndaloon, nde waa Galile la.»
60Teewul Piyeer ne ko: «Waa jii, li ngay wax, xawma ma ko de!» Ca saa sa, ganaar sab, te kàddug Piyeer daanoogul sax.
61Ci kaw loolu Sang bi geesu, ne jàkk Piyeer, Piyeer fàttliku la ko Sang bi waxoon ne ko: «Bala ganaar a sab tey jii, dina fekk nga jàmbu ma ñetti yoon.»
62Piyeer nag génn, di jooy jooy yu metti.
63Ci kaw loolu ña jàpp Yeesu, di ko kókkali ak a dóor.
64Ñu muur kanam gi, naan ko: «Yaw, waxal nu kàddug waxyu boog, ana ku la dóor?»
65Yeneen saaga yu bare tifaar nañu ko ko.
66Ba bët setee, mbooloom magi askanu Yawut, ak sarxalkat yu mag ya, ak firikati yoon ya, ñépp daje. Ñu yóbbu Yeesu ca seen kurélu àtte ba.
67Ñu ne ko: «Soo dee Almasi, wax nu ko.» Mu ne leen: «Su ma leen ko waxee, dungeen ma gëm.
68Te su ma leen laajee, dungeen tontu.
69Waaye gannaaw-si-tey, Doomu nit ki mooy toog ci ndijooru Yàlla, Aji Man ji.»
70Ñépp daldi ne: «Kon yaay Doomu Yàlla?» Mu ne leen: «Yeena waxal seen bopp ne man la.»

Read Luug 22Luug 22
Compare Luug 22:33-70Luug 22:33-70