Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 22

LUUG 22:11-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc ba, man ak samay taalibe?”
12Noonu dina leen won néeg bu féete kaw, te yaa, ñu defar ko ba noppi. Foofa ngeen koy defare.»
13Ñu dem, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
14Bi waxtu wi jotee Yeesu toog ak ndaw yi,
15ne leen: «Yàkkamti woon naa lool lekk ak yéen reeru bésu Mucc bii, laata ñu may sonal.
16Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma ko lekk mukk, lu dul ba kera mu mat ci nguuru Yàlla.»
17Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko.
18Ndaxte maa ngi leen koy wax, dootuma naan ndoxum reseñ mi, ba kera Yàlla di tëral nguuram.»
19Gannaaw loolu mu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, joxleen ko ne: «Lii sama yaram la, wi ma joxe ngir yéen. Defleen lii, ngir fàttaliku ma.»
20Noonu itam bi ñu lekkee ba noppi, mu jël kaas bi ne leen: «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.
21Waaye nag loxob ki may wor a ngi nekk ak man ci ndab li.
22Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko dogale. Waaye ki koy wor dina torox.»
23Noonu taalibe yi di laajante ci seen biir, kan ci ñoom mooy nara def loolu.
24Taalibe ya it di werante, ngir xam kan ci ñoom moo gëna màgg.
25Yeesu ne leen: «Buuri xeeti àddina dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañuy sàkku ngërëm.
26Waaye yéen buleen def noonu. Ki gëna màgg ci yéen, na nekk ni ki gëna ndaw, te njiit mel ni surga.
27Ki toog ca lekkukaay ba, moom ak surgaam, ñoom ñaar kan moo ci gëna màgg? Xanaa du ki toog ci lekkukaay bi? Waaye man maa ngi ci seen biir ni surga.
28Yéen nag yéenay ñi ànd ak man ci samay fitna.
29Man nag jox naa leen sañ-sañu nguuru, ni ma ko sama Baay joxe.
30Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»
31Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.
32Waaye man ñaanal naa la, ngir sa ngëm dëgër. Te yaw, boo délsee, nanga dëgëral sa bokki taalibe yi.»

Read LUUG 22LUUG 22
Compare LUUG 22:11-32LUUG 22:11-32