Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 21

Luug 21:3-27

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Yeesu ne: «Maa leen ko wax déy, jëtun bii, ñii ñépp, moo leen ëpple lu mu joxe.
4Ndax ñii ñépp, la ñu woomle, ca lañu sompe, def ci boyetu sarax bii; waaye moom ci biir ag ñàkkam la jël mboolem ab dundam, def ci.»
5Mu am nag ay nit ñu doon wax ca kër Yàlla ga, ak taaru doji tànnéef, ya ak yeneen alali jooxe ya ñu ko rafetale. Yeesu itam ne leen:
6«Lii ngeen gis nii, ay jant a ngi ñëw yu fi doj dootul des ci kaw doj, lépp ay jóoru.»
7Ñu laaj ko ne ko: «Sëriñ bi, loolu kañ lay doon? Ak luy doon ub takk buy xamle ne looloo ngi waaja dikk?»
8Yeesu ne: «Moytuleen, ngir ñu bañ leena nax, ndax ñu bareey dikk, tuddoo sama tur, naan: “Man a,” te naan: “Waxtu wi jege na.” Buleen leen topp.
9Bu ngeen déggee ay xare aki salfaañoo, buleen tiit, ndax fàww loolu jëkka am. Waaye du doonagum muj ga, ca saa sa.»
10Mu neeti leen: «Aw xeet dina jógal aw xeet, am réew jógal am réew.
11Ay yëngu-yënguy suuf yu réy dina am, ay xiif aki mbas dikke fu bare, te xew-xew yu raglu dina am, ak firnde yu mag yu jóge asamaan.
12Waaye laata loolu lépp, yeen, dees na leen teg loxo, fitnaal leen, jébbal leen kuréli jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanami buur aki boroom dëkk ndax sama tur,
13ngir ngeen doxe ca yékkati kàdduy seede.
14Kon nag defleen bu baax ci seen xel, ne soxlawuleena waajal kàddug layoo.
15Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.
16Pexe mu leen jàpplu dina sababoo sax ci seeni waajur ak seen doomi ndey ak seeni jegeñaale ak seeni xarit, te dees na rey ñenn ci yeen,
17Ñépp a leen di bañ ndax sama tur.
18Waaye seen genn kawaru bopp sax du sànku.
19Saxooleen muñ nag, daldi mucc.
20«Bu ngeen gisee gàngooru xare gu gaw Yerusalem, su boobaa xamleen ne tasteem dëgmal na.
21Su boobaa ña mu fekk ca diiwaanu Yude, nañu daw jëm kaw tund ya, ñi ci biir dëkk bi, nañu daw génn, te ña mu fekk ca tool ya, buñu duggsi ci biir dëkk bi.
22Ndax janti mbugal lay doon, ngir sottal mboolem lu ñu bindoon.
23Wóoy ngalla jigéeni wérul ña, ak ñay nàmpal ca yooyu jant! Ndax tiis wu réy lay doon ci réew mi, akam sànj ci kaw askan wii.
24Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.
25«Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi,
26nit ñiy séentu li nara dikkal àddina, di xëm ndax tiitaange, nde dooley asamaan dina sàqi.
27Su boobaa dees na gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak manoore ak daraja ju réy.

Read Luug 21Luug 21
Compare Luug 21:3-27Luug 21:3-27