Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 20

Luug 20:6-41

Help us?
Click on verse(s) to share them!
6Te su nu nee: ci nit ñi la ndigal li bawoo, mbooloo mépp a nuy sànni ay xeer, ndax wóor na leen ne Yaxya ab yonent la woon.»
7Ñu daldi ne ko: «Xamunu fu mu ko jële.»
8Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe lii.»
9Ci kaw loolu Yeesu léeb askan wa, lii, ne leen: «Jenn waay moo jëmbatoon ab tóokëru reseñ, batale ko ay beykat, daldi dem yoon wu yàgg.
10Ba tóokër ba ñoree, mu yebal ca beykat ya ab surga, ngir ñu jox ko wàllam ca meññeef ma. Beykat ya dóor surga ba, ba noppi dàq ko, mu dellu loxoy neen.
11Mu dellu yónni beneen surga, ñu dóor ko moom itam, torxal ko, dàq ko, mu dellu loxoy neen.
12Mu dellooti yónni ñetteelu surga, kooku it, ñu gaañ ko, sànni ko ca biti.
13«Boroom tóokër ba ne: “Nan laay def nag? Naa yónni sama doomu bopp ji ma sopp boog, xanaa moom, dinañu ko rus!”
14Teewul ba beykat ya gisee doom ji, dañu ne ci seen biir: “Kii mooy donn; nanleen ko rey, su ko defee ndono li féeteek nun.”
15Ba loolu amee ñu génne ko tóokër ba, rey ko.» «Ana nu boroom tóokër biy def beykat yi nag?
16Xanaa dikk, rey beykat yooyu, dénk tóokër ba ñeneen.» Nit ña dégg loolu daldi ne: «Yàlla tere!»
17Yeesu ne leen jàkk, daldi ne: «Kon nag lii ñu bind, lu muy tekki? “Doj wi tabaxkat yi beddi woon, moo mujj di doju coll wi.”
18Woowu doj, képp ku ci dal, dammtoo, te ku mu dal, rajaxe la.»
19Firikati yoon yaak sarxalkat yu mag ya nag, ca saa sa lañu doon fexee teg Yeesu loxo, ndax xamoon nañu ne ñoo moom léeb woowu, waaye nit ña lañu ragal.
20Ba mu ko defee ñu bàyyi Yeesu xel, daldi yebal ay yeerukat, sas leen ñu yiw-yiwlu te di ko fiir ci kaw kàddu ba jàpp ko, ngir jébbal ko boroom dëkk bay boroom kilifteef ga ak sañ-sañ ba.
21Yeerukat ya dikk ne Yeesu: «Sëriñ bi, xam nanu ne njub ngay wax, di ko jàngle. Amuloo parlàqu itam, waaye ci kaw dëgg ngay jànglee yoonu Yàlla.
22Wax nu nag ndax yoon maye na, nu fey Buur Sesaar galag, am déet.»
23Teewul Yeesu ràññee seen pexe. Mu ne leen:
24«Joxleen ma ab posetub dinaar, ma gis. Nataal bii ak tur wii ci binde, kuy boroom?» Ñu ne ko: «Sesaar.»
25Mu ne leen: «Kon kay yëfi Sesaar, joxleen ko Sesaar; te yëfi Yàlla, ngeen jox ko Yàlla.»
26Manuñu koo fiir ba jàppe ko menn mbir ca kanam mbooloo ma, xanaa waaru ca tontam, ba wedam.
27Ñenn ci Sadusen, yi weddi ne ndee-ndekki am na, ñoo dikkoon ca Yeesu. Ñu ne ko:
28«Sëriñ bi, Musaa da noo bindal ne ku góor, su ku mu bokkal waajur faatoo te amul ak jabaram doom, na jël jabaram, ngir amal mbokkam ma dee, kuutaay.
29Léegi juróom ñaari góor ñu bokk ndey ak baay la woon. Taaw ba takk jabar, gannaaw gi mu faatu, te bàyyiwul doom.
30Tofo ba,
31ak ñaareelu tofo ba, ku ci nekk donn na ndaw sa ca magam, ñu topplantee ko noonu, ba juróom ñaar ñépp dee te amuñu ca doom.
32Gannaaw gi ndaw sa it dee.
33Ndaw si nag, keroog ndekkite la, kan la ciy doon jabaram, gannaaw juróom ñaar ñépp a ko jëloon jabar?»
34Yeesu ne leen: «Ci àddina sii la góor ñi ak jigéen ñi di séy.
35Waaye ña ñu yeyale ndekkitel ëllëg, yeyale leen bakkan ci àddina siy ñëw, ñooñu, su boobaa, kenn du ci am jabar mbaa jëkkër.
36Dootuñu mana dee it, ndax niy malaaka lañuy mel. Ay doomi Yàlla lañuy doon, ndax da leen di fekk dekki.
37Te Musaa ci boppam xamle na ne ñi dee dañuy dekki, na ko téere indee ca mbirum ngarab sa. Mooy ba mu wooyee Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, Yàllay Yanqóoba.”
38Kon moom du ñi dee lay seen Yàlla, xanaa ñiy dund, ndax fa moom, ñépp a ngi dund.»
39Ci kaw loolu ñenn ca firikati yoon ya àddu ne ko: «Dëgg nga wax, Sëriñ bi!»
40Gannaaw loolu ñemeetuñu koo laaj dara.
41Yeesu neeti leen: «Nees mana waxe ne Almasi, Sëtub Daawuda la?

Read Luug 20Luug 20
Compare Luug 20:6-41Luug 20:6-41