Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 1:18-43 in Wolof

Help us?

LUUG 1:18-43 in Téereb Injiil

18 Sakari daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama soxna it màggat na.»
19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xibaaru jàmm boobu.
20 Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»
21 Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakari yàgg ca bérab bu sell ba.
22 Waaye bi mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.
23 Bi Sakari matalee liggéeyu sarxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.
24 Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet soxnaam ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer
25 te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»
26 Bi Elisabet nekkee ci juróom benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.
27 Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.
28 Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»
29 Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30 Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.
31 Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32 Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.
33 Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»
34 Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu mana ame? Man de, janq laa ba tey.»
35 Malaaka ma ne ko: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.
36 Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku manula am doom, mu ngi ci juróom benni weeram.
37 Ndaxte dara tëwul Yàlla.»
38 Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem.
39 Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.
40 Mu dugg ca kër Sakari, daldi nuyu Elisabet.
41 Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yëngatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.
42 Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!
43 Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?
LUUG 1 in Téereb Injiil

Luug 1:18-43 in Kàddug Yàlla gi

18 Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.»
19 Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw fi kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw, yégal la bii xibaaru jàmm.
20 Léegi nag, dama ne, gannaaw gëmuloo sama kàddu, giy jot, sotti, dinga luu te dootuloo mana wax, ba kera loolu di am.»
21 Ci biir loolu mbooloo maa ngay xaar Sàkkaryaa, jaaxle lool ndax yàggaayam ca biir néeg Yàlla ba.
22 Ba mu génnee nag, manula wax ak ñoom. Ñu daldi xam ne am na lu ko feeñu ca néeg Yàlla ba. Ma nga leen di liyaar, manatula wax.
23 Naka la Sàkkaryaa fégal ayu carxalam, daldi ñibbi.
24 Gannaaw gi, soxnaam Elisabet ëmb. Lëlu na juróomi weer. Ma nga naan:
25 «Lii Boroom bee ma ko defal ci jant yi mu ma geesoo, ba teggil ma sama gàcce gi ci biir nit ñi!»
26 Ba Elisabet tolloo ci juróom benni weeram, ca la Yàlla yebal Jibril malaaka mi, dëkk bi ñuy wax Nasaret ca diiwaanu Galile,
27 ci janq bu digoo séy ak waa ju ñuy wax Yuusufa te bokk ci waa kër Daawuda. Janq ba Maryaama lañu koy wax.
28 Malaaka ma agsi ba ca moom, ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi ñu baaxe, Boroom bi yaw la àndal.»
29 Waxi malaaka ma nag jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki.
30 Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.
31 Dinga ëmb, ba jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.
32 Ku màgg lay doon, te dees na ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla moo koy jagleel nguurug Daawuda maamam.
33 Mooy nguuru fi kaw waa kër Yanqóoba ba fàww, te nguuram du foq mukk.»
34 Ci kaw loolu Maryaama laaj malaaka mi ne ko: «Nu loolu di ame, te man xawma góor?»
35 Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla.
36 Te kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon wooye jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram,
37 ndax Yàlla, dara tëwu ko.»
38 Maryaama daldi ne: «Maa ngi, di jaamub Boroom bi. Nii nga waxe, na ame noonu ci man.» Ba loolu amee malaaka ma bàyyikoo ca moom, dem.
39 Ci fan yooyu la Maryaama fabu gaaw, jëm diiwaanu tund ya, ca dëkkub Yude,
40 ba Sàkkaryaa dëkke. Mu agsi ca kër ga, nuyu Elisabet.
41 Naka la Elisabet dégg nuyoob Maryaama, doom ja mu ëmb yëngu ca biiram. Elisabet daldi feese Noo gu Sell gi.
42 Mu àddu ca kaw ne: «Yaa gëna barkeel ci jigéen ñi, sa doom ji nga ëmb it barkeel na!
43 Ana ku ma doon ba sama ndeyu Sang di ma seetsi?
Luug 1 in Kàddug Yàlla gi