Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - LUUG - LUUG 16

LUUG 16:8-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
8Njaatige ba nag daldi naw ni bëkk-néeg bu njublaŋ boobu muuse woon. Ndaxte ñi bokk ci àddina ñoo gëna muus ci li ñu jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw ñi bokk ci leeru Yàlla.»
9Yeesu teg ca ne: «Maa ngi leen di wax lii: sàkkuleen ay xarit jaare ko ci alalu àddina, ngir bu alal nekkatul, ñu man leena fat ca dal yu sax ya.
10Nit ku maandu ci yëf yu néew, dina maandu itam ci yu bare. Ku jubadi ci yëf yu néew, du jub ci yu bare.
11Su fekkeente ne nag jubuleen ci alalu àddina, kon ku leen di dénk alal ju wóor ji?
12Te su ngeen maanduwul ci alal ji ngeen moomul, kon ku leen di jox alal ji ngeen moom?
13«Benn jaam manula jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleena boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.»
14Farisen yi déglu li Yeesu doon wax lépp, tàmbali di ko reetaan, ndaxte ñu bëggoon xaalis lañu.
15Waaye Yeesu ne leen: «Yéen yéena ngi fexee jub ci kanam nit ñi waaye Yàlla xam na seen xol. Ndaxte li nit ñiy fonk, Yàlla sib na ko.
16«Yoonu Musaa wi ak waxi yonent yi ñu ngi fi woon ba kera Yaxya di ñëw. La ko dale foofa nag, yégle nañu xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla, te ñépp a ngi góor-góorlu, ngir dugg ci.
17Waaye nag asamaan ak suuf jóge fi moo gëna yomb randal wenn rëdd ci arafu yoonu Musaa.
18«Ku fase sa soxna, ba noppi takk keneen, njaaloo nga, te ku takk jigéen ju jëkkëram fase, njaaloo nga.

Read LUUG 16LUUG 16
Compare LUUG 16:8-18LUUG 16:8-18