Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 12

Luug 12:39-48

Help us?
Click on verse(s) to share them!
39Waaye lii de xamleen ko: boroom kër, su xamoon wan waxtu la ab sàcc di ñëw, du ko wacc moos, mu dàjjiy, dugg këram.
40Kon yeen itam waajleen ba jekk, ndax waxtu wu ngeen foogul, ci la Doomu nit ki di ñëw.»
41Piyeer nag ne Yeesu: «Sang bi, ndax nun doŋŋ nga léeb lii, am ñépp a ko moom?»
42Sang bi ne ko: «Ana kan nag mooy saytukat bu wóor te muus, ba njaatigeem batale ko curgag këram, ngir mu di leen jox seen njël ca ba muy jot?
43Ndokklee surga bu njaatigeem dikk, fekk ko muy doxale noonu.
44Maa leen ko wax déy, alalam jépp la ko njaatige la di far dénk.
45Waaye su jawriñ ja nee ci xelam: “Sama njaatige dikkagul léegi,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya, góor ak jigéen, di lekk ak a naan, di màndi,
46su boobaa njaatige laay dikk bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu foogul, te mbugal mu metti la koy mbugal, sédd ko ci añub gëmadikat ñi.
47«Jawriñ jooju xam nammeelu njaatigeem, te taxul mu waaj ko, ba jëfewu ko, ay yetam dina bare.
48Waaye jawriñ ji xamul nammeelu njaatigeem, te teewu koo def lu yelloo ay duma, yet yu néew lay am. Képp ku ñu jox lu bare, dees na la topp lu bare. Képp ku ñu dénk jopp, dees na la feyeeku lu ko ëpp.

Read Luug 12Luug 12
Compare Luug 12:39-48Luug 12:39-48