Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Luug - Luug 12

Luug 12:26-50

Help us?
Click on verse(s) to share them!
26Ndegam loolu gëna tuut sax moo leen të, ana lu ngeen di xalaat ci leneen?
27«Seetleen ni tóor-tóor yiy saxe. Sonnuñu, ëccuñu, waaye maa leen ko wax, Suleymaan ak darajaam jépp sax, soluwul woon ni benn ci ñoom.
28Ndegam ñaxum tool miy dund tey, te léegi ñu sànni ko cib taal, moom la Yàlla solale noonu, xanaa astamaak yeen kay? Yeenaka néew ngëm!
29Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp.
30Ndax loolu lépp, xeeti yéefari àddina, ñoo koy tiisoo, te yeen, Baay bi xam na ne soxla ngeen ko.
31Waaye tiisooleen nguuram, su boobaa dees na leen ci dollil loolu.
32«Buleen ragal dara, yeen jur gu sew gi, ndax seen Baay la soob, mu jagleel leen nguur gi.
33Jaayleen seen alal, sarxe xaalis bi, sàkkuleen mbuus yu dul ràpp, muy dencu ëllëg bu dul jeex fa asamaan, fa ko sàcc dul jege, max du ko yàq.
34Ndax fu sab denc nekk, sab xol it a nga fa.
35«Takkuleen te seeni làmp di tàkk.
36Mel-leen ni nit ñuy séentu seen njaatige lu jóge céet, ndax bu dikkee ba fëgg bunt ba, ñu daldi ko ubbil.
37Ndokklee surga yooyu seen njaatige dikk fekk ñu teewlu. Maa leen ko wax déy, njaatige leey takku, toogal leen ba noppi dikk, taajal leen, ñu lekk.
38Ndegam ba guddi ga xaajee la njaatige la ñibbsi, ba fekk surga ya teewloo noonu, am ba suuf seddee la, lu mu ci mana doon, ndokklee ñoom.
39Waaye lii de xamleen ko: boroom kër, su xamoon wan waxtu la ab sàcc di ñëw, du ko wacc moos, mu dàjjiy, dugg këram.
40Kon yeen itam waajleen ba jekk, ndax waxtu wu ngeen foogul, ci la Doomu nit ki di ñëw.»
41Piyeer nag ne Yeesu: «Sang bi, ndax nun doŋŋ nga léeb lii, am ñépp a ko moom?»
42Sang bi ne ko: «Ana kan nag mooy saytukat bu wóor te muus, ba njaatigeem batale ko curgag këram, ngir mu di leen jox seen njël ca ba muy jot?
43Ndokklee surga bu njaatigeem dikk, fekk ko muy doxale noonu.
44Maa leen ko wax déy, alalam jépp la ko njaatige la di far dénk.
45Waaye su jawriñ ja nee ci xelam: “Sama njaatige dikkagul léegi,” ba tax mu tàmbalee dóor surga ya, góor ak jigéen, di lekk ak a naan, di màndi,
46su boobaa njaatige laay dikk bés bu mu ko séenuwul ak waxtu wu mu foogul, te mbugal mu metti la koy mbugal, sédd ko ci añub gëmadikat ñi.
47«Jawriñ jooju xam nammeelu njaatigeem, te taxul mu waaj ko, ba jëfewu ko, ay yetam dina bare.
48Waaye jawriñ ji xamul nammeelu njaatigeem, te teewu koo def lu yelloo ay duma, yet yu néew lay am. Képp ku ñu jox lu bare, dees na la topp lu bare. Képp ku ñu dénk jopp, dees na la feyeeku lu ko ëpp.
49«Sawara laa taalsi ci kaw suuf, te maaka bëggoon mu ne jippét xaat!
50Am na nag sóobu gu ma wara sóobu, waaye ndaw njàqare ci man li feek loolu sottiwul.

Read Luug 12Luug 12
Compare Luug 12:26-50Luug 12:26-50