Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 9

Kàdduy Waare 9:1-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Loolu lépp laa walbatiku xalaat, ngir lépp leer ma: Ku jub ak ku xelu ak seeni jëf, lépp a ngi ci loxol Yàlla. Mbëggeel ak mbañeel, xamoo lu la ciy xaar, lépp a nga ca kanam.
2Ñépp a bokk benn dogal bi, ku jub ak ku bon, ku baax ak ku set, ak ku sobewu; kuy sarxal ak ku dul sarxal, muy ku baax ki, di bàkkaarkat bi, muy kiy giñ, di ki ragal ngiñ.
3Lu mettee ngi nii ci mboolem lu am fi kaw suuf: Benn dogal la ñépp bokk, te it nit a ngi sóobu ci mbon, di mébét jëfi dof giiru dundam, ba noppi fekki ña dee.
4Képp kuy dund kat, am nga yaakaar, te xaj buy dund a gën gaynde gu dee.
5Kuy dund xam ne dangay dee, waaye ku dee xamul dara, te séentootul ab yool. Ku dee, ñu fàtte la.
6Muy sa cofeel, di sa mbañeel, ba ci sa kiñaan ànd ak yaw seey. Du lenn lu deeti sa wàll ci jépp jëfi kaw suuf.
7Kon doxal, lekk saw ñam, bége, te naan sa biiñ ci xol bu sedd. Yàlla kat nangul na la jeeg say jëf.
8Foo tollu, solul ba jekk, te bul fàttee xeeñlu.
9Bànneexul yaak ndaw si nga sopp ci fan wu gàtt wi la Yàlla may fi suuf, ndax loolu nga séddoo ci fan wu gàtt wii ngay doñ-doñaale fi kaw dun bi.
10Liggéey boo gis, liggéeyal; def ci loo man. Ndax muy jëf, di doxalin, di xam-xam, di manoore, dara amu ci njaniiw, ga nga jëm.

Read Kàdduy Waare 9Kàdduy Waare 9
Compare Kàdduy Waare 9:1-10Kàdduy Waare 9:1-10