Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 7

Kàdduy Waare 7:2-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Dem dëj a gën wàlli bernde, mooy muju képp. Kuy dund, sóoraale ko.
3Naqar a gën xaxaloo; aw tiis ñëkkal kanam, rafetal xol.
4Ku xelu, xalaat kërug dëj; ku dofe, xalaat kërug puukare.
5Déglu ku xelu di la àrtu moo gën déglu dof bu lay woy.
6Ab dof day textexi ni dég yuy retete taal bu cin tege. Loolu it di cóolóoli neen.
7Foqarñi kay day dofloo boroom xel, te ab ger da lay gëlëmal.
8Fa mbir mujjee gën fa mu doore, te muñ a gën réy-réylu.
9Bul gaawa mer; mer, xolub dof la samp këram.
10Bul ne lu tax démb dàq tey, loolu, laaj ko du xel.
11Xel mu rafet daa neex ni ndono, njariñ la ci kuy dund.
12Xel mu rafet kiiraay la, xaalis kiiraay la; njariñu xam-xam mooy xelu, mucc.
13Xoolal ci li Yàlla def: Ana ku mana jubbanti lu mu dëngal?

Read Kàdduy Waare 7Kàdduy Waare 7
Compare Kàdduy Waare 7:2-13Kàdduy Waare 7:2-13