Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàdduy Waare - Kàdduy Waare 3

Kàdduy Waare 3:5-15

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Day jot nga sànniy doj, mu jot nga dajale; mu jot nga fóon, mu jot nga baña fóon.
6Mu jot nga sàkku, mu jot nga ñàkk; mu jot nga sàmm, mu jot nga xalab.
7Mu jot nga xar, mu jot nga gaar; mu jot nga selaw, mu jot nga wax.
8Mu jot nga sopp, mu jot nga jéppi; mu jot nga xare, mu jot nga jàmmoo.
9Ana lu liggéeykat biy jariñoo ciw ñaqam?
10Gis naa ne sas la bu Yàlla sase, nu war koo sasoo.
11Lépp la Yàlla def, ba bu jotee rafet. Moo may nit muy njort ëllëg, te taxul mu mana ràññee jëf ji Yàlla jëf, njàlbéen ba muj ga.
12Ma gis ne nit amul lu gën bànneex ak jàmmi bakkan cig dundam,
13te nitoo nit, su dee lekk ak a naan, di ñaq, jariñoo, loolu mayu Yàllaa.
14Ma xam ne lu Yàlla def, loola day sax ba fàww. Deesu ci yokk, mbaa di wàññi dara; Yàllaa ko def, ngir nit di ko wormaal.
15Lu ay tey, ayoon na, lu ay ëllëg it ayoon na. Yàllaay namma indi la woon.

Read Kàdduy Waare 3Kàdduy Waare 3
Compare Kàdduy Waare 3:5-15Kàdduy Waare 3:5-15