Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 1

Kàddu yu Xelu 1:11-32

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Dañu la naan: «Dikkal, nu tëruji bakkan, yeeruji jaambur bu deful dara.
12Nanu mel ni njaniiw, mëdd kuy dund, mu jekki tàbbi biir bàmmeel.
13Mboolem alal ju réy, nu jagoo, yeb sunu biir kër, mu fees.
14Dikkal nu far, mbuus miy benn, nu bokk.»
15Doom, bul ànd ak ñoom ciw yoon, bul jaare fa ñuy jaar,
16ngir dañuy xélu, nar musiba, di gaawtuy sànk bakkan.
17Doo firib caax, ba jàpp njanaaw luy xoole.
18Ñii kat seen bopp lañuy fiir, seen bakkanu bopp lañu sànk.
19Képp kuy lekk lu lewul, nii lay mujje: wutin wu lewul jël bakkanu boroom.
20Xel mu Rafet a ngay woote ca mbedd ma, di xaacu ca pénc ma.
21Ma ngay wootee bérab yu gëna xumb, di dégtaley kàddoom, bunt dëkk ba.
22Ma nga naan: «Moo téxét bi, foo àppal sa téxét gi? Ñaawlekat bi, foo àppal sa ñaawle bi? Dof bi, ñaata yoon ngay bañ xam-xam?
23Soo dëppee ba déglu, ma àrtu la. Ma ne, kon ma xellil la samam xel, xamal la samay kàddu.
24Damaa woote, nga gàntal, ma tàllal loxo, faaleesu ma.
25Sofental nga samay digle, nanguwoo samay àrtu.
26Kon boo sëngéemee, man it ma ree, njàqare dab la, may textexi.
27Njàqare di ngëlén, dab la, sa musiba def callweer, buub la, njekkar ak fitna dal la.
28Keroog nga woo ma wall, duma wuyu, nga seet ma, seet, doo ma gis.
29Daa fekk nga baña xam, te ragal Yàlla du loo taamu.
30Dégluwoo samay digle it, xanaa xeeb samay àrtu yépp.
31Waaye loo ci góobe, gar ko, say pexe suur la këll.
32Déggadi sànk ab téxét, naagu rey ab dof.

Read Kàddu yu Xelu 1Kàddu yu Xelu 1
Compare Kàddu yu Xelu 1:11-32Kàddu yu Xelu 1:11-32