Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 14

Kàddu yu Xelu 14:15-25

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Ab téxét, loo wax mu gëm; ku ñaw xam fi ngay jaare.
16Ku xelu day ragal, di dëddu lu bon; ab dof day ràkkaaju, du tiit.
17Ku gaawa mer, def jëfi dof, te kuy fexeel nit, ñu bañ la.
18Ab téxét ndof ay céram, ku ñaw jagoo xam-xam.
19Ku bon, ku baax sut la; ku soxor ay toogaanu ku jub.
20Ku ñàkk, say dëkk sax bañ la; ku barele, barey xarit.
21Ku xeeb sa dëkkandoo, bàkkaar nga; ku baaxe ku ñàkk, mbégte ñeel la.
22Kuy mébét lu bon daa réer, kuy mébét lu baax am nga ngor ak worma.
23Kër-këri, jariñu; waxi neen, loxoy neen.
24Ku rafet xel jagoo alal, ab dof ràngoo ndofam.
25Seede bu dëggu day jot bakkan, kuy fen day wore.

Read Kàddu yu Xelu 14Kàddu yu Xelu 14
Compare Kàddu yu Xelu 14:15-25Kàddu yu Xelu 14:15-25