Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Kàddu yu Xelu - Kàddu yu Xelu 12

Kàddu yu Xelu 12:7-23

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ab soxor bu daanoo, jeex na; ku jub, sa kër taxaw, ne këcc.
8Xel mu ñaw, jëw bu rafet; sam xel jekkadi, ñu xeeb la.
9Woyof mbubb, am benn surga doŋŋ, moo gën réyal turki tey dee ak xiif.
10Ku jub day topptoo ag juram, ab soxor néeg cig juram.
11Beyal sab tool, sab dund doy; topp ay caaxaan ñàkk bopp la.
12Ab soxor ay xemmem alal ju lewul, ku jub garab la, reen baa ko meññal.
13Bàkkaaru làmmiñ dugal na boroom, ku jub mucc ci njàqare.
14Làmmiñ reggal na boroom; ñaq, jariñu.
15Na dof di jëfe, njub la ci moom; dégg ndigal rafet um xel la.
16Ab dof bu meree, mu gaawa feeñ; ku teey, tanqamlu saaga.
17Ku dëggu, seede dëgg; seede bu bon, fen rekk.
18Làmmiñu waxkat, jam-jami jaasi; kàddu gu xelu, garab la ci.
19Kàdduy dëgg, day sax dàkk; fen, xef xippi, mu wéy.
20Kuy ràbb lu bon lal pexey wor, kuy digle jàmm, am mbégte.
21Ku jub du amu ay, ab soxor du tàggook musiba.
22Aji Sax ji sib na fen-kat, safoo ku dëggu.
23Nit ku ñaw day xam, ba ca; ab dof siiwal waxi dofam.

Read Kàddu yu Xelu 12Kàddu yu Xelu 12
Compare Kàddu yu Xelu 12:7-23Kàddu yu Xelu 12:7-23