Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 9

Jëf ya 9:15-40

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.
16Maa koy won mboolem coono bi mu wara dékku ngir sama tur.»
17Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg Sóol loxo, ne ko: «Mbokk mi Sóol, Sang Yeesu, mi la feeñu woon ci yoon wi nga dikke, moo ma yebal ci yaw, ngir nga dellu di gis te feese Noo gu Sell gi.»
18Ca saa sa lu mel niy waasintóor wadde ca bët ya, mu dellu di gis. Mu daldi jóg, ñu sóob ko ci ndox.
19Ba loolu wéyee, mu lekk, doora am doole. Sóol toog na ak taalibe ya ca Damaas ay fan.
20Ca saa sa la tàmbalee xamle Yeesu ca jàngu ya, naan Yeesu mooy Doomu Yàlla.
21Mboolem ña ko dégg, daldi waaru, naan: «Xanaa du kii moo doon bóom ñiy tudd woowu tur ci Yerusalem? Du moo fi dikkoon, ngir yeewlu leen, yóbbu ci sarxalkat yu mag yi?»
22Teewul Sóol gëna am manoore, ba far jaaxal Yawut ñi dëkke Damaas, di firndeel ne Yeesu mooy Almasi.
23Ba ñu ca tegee ab diir bu xawa yàgg, Yawut yi féncoo, ngir reylu ko.
24Sóol nag yég seen mébét. Guddi ak bëccëg lañu doon wattu bunti dëkk ba, ngir bóom ko.
25Teewul taalibe yi yeb ko ag guddi ci ag dàmba, jàlle ko ca wàllaa miir ba, yoor ko.
26Ba Sóol agsee Yerusalem, jéem naa jaxasook taalibe yi, waaye ñépp a ko ragal, ndax ñàkka gëm ag taalibeem.
27Ci kaw loolu Barnaba ànd ak moom, yóbbu ko ca ndaw ya. Barnaba nettali leen, ni Sóol gise Sang bi ca yoon wa, ba mu wax ak Sóol, ak fit wa Sóol waaree ca Damaas ci turu Yeesu.
28Ba loolu amee Sóol ànd ak ndaw yi di dem ak a dikk ci biir Yerusalem, di waaree aw fit ci turu Sang bi.
29Mu boole ci di wax ak a werante ak Yawut ñiy làkk gereg, te ñoom ñu di ko fexee rey.
30Bokki gëmkat ña nag yég ko, daldi koy yóbbu Sesare, yebale ko foofa, mu dem Tàrs.
31Ba mu ko defee mbooloom gëmkat ñi ci mboolem diiwaani Yude ak Galile ak Samari daldi am jàmm. Ñuy gëna dëgër, di wéye ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
32Piyeer mi doon wër fu nekk nag, am na bés mu jaare ca ñu sell ña dëkke Lidd.
33Mu gis foofa waa ju ñuy wax Ene. Fekk na diiru juróom ñetti at, cib lal rekk lay tëdd ndax yaram wu làggi.
34Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Almasi wéral na la; jógal, lalal sa bopp.» Mu jóg ca saa sa.
35Mboolem waa diiwaani Lidd ak Saron nag gis ko, ñoom ñépp waññiku ci Sang bi.
36Dëkk ba ñuy wax Yope, ab taalibe bu jigéen a nga fa woon, ñu di ko wax Tabita mbaa Dorkas ci làkku gereg. Def lu baax ak sarxe la saxoo woon.
37Ci fan yooyu, mu daanu wopp, daldi faatu. Ñu sang ko, dugal ko ca néegu kaw taax ma.
38Ci biir loolu taalibe yi dégg ne Piyeer a nga Lidd, te Lidd sorewul Yope. Ñu yebal ñaari nit ca moom, ngir ñaan ko mu ñëw te baña yeex.
39Piyeer jóg, ànd ak ñoom, ba agsi. Ñu yéege ko ca néegu kaw taax ma. Ay jëtun a nga fa woon. Ñoom ñépp di jooyoo, yéew Piyeer, won ko turki yaak mbubb ya Dorkas defaroon ba muy nekk ak ñoom.
40Ci kaw loolu Piyeer dàq ñépp ca biti. Mu sukk, ñaan, daldi walbatiku jublook néew bi, ne: «Tabita, jógal!» Mu ne xiféet, gis Piyeer, jóg toog.

Read Jëf ya 9Jëf ya 9
Compare Jëf ya 9:15-40Jëf ya 9:15-40