Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 9

Jëf ya 9:1-19

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Ci biir loolu Sóol moom, noyyeewul lu moy di tëkkook a jéema bóom taalibey Sang bi. Mu dem nag ca sarxalkat bu mag ba,
2di sàkku ay bataaxal yu ñeel jànguy dëkk ba ñuy wax Damaas, bataaxal yu yóbbante ndigal lu yeewlu képp ku ñu fa gis ku bokk ci Yoon woowu, góor ak jigéen, ngir mu jàpp leen, indi Yerusalem.
3Naka la Sóol dem ba jub Damaas, ag leer bawoo asamaan, jekki ne ràyy ci kawam.
4Mu daanu ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?»
5Mu ne: «Yaay kan Sang bi?» Mu ne: «Man maay Yeesu, mi ngay bundxatal.
6Léegi nag, jógal, dugg ci dëkk bi, dees na la wax li nga wara def.»
7Nit ña ànd ak moom a nga taxaw, jommi ba ne cell; dégg nañu baat bi te gisuñu kenn.
8Sóol jóg, xippi, gisul dara; ñu daldi koy wommat, dugal ko biir Damaas.
9Diiru ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul.
10Ab taalibe bu ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Sang bi feeñu ko, ne ko: «Anañas!» Mu ne ko: «Maa ngi, Sang bi.»
11Sang bi ne ko: «Demal ba ca mbedd, ma ñuy wax Mbedd mu jub, te nga seet ca kër Yuda ku ñuy wax Sóol te dëkke Tàrs. Ma ngay ñaan.
12Dafa gis cim peeñu ku ñuy wax Anañas duggsi, teg ko loxo, ngir mu dellu di gis.»
13Anañas nag ne ko: «Sang bi, maa dégge ci ñu bare mbirum kooku, ñu seede mboolem jëf ju bon ji mu def say nit ñu sell ci biir Yerusalem.
14Te moo yor ndigal lu tukkee ci sarxalkat yu mag yi, ngir yeewlu képp kuy tudd saw tur.»
15Sang bi ne ko: «Demal, ndax kooku jumtukaay laa ko tànne, ngir mu xamali sama tur, xeeti jaambur yi ak seeni buur, xamal ko itam bànni Israyil.
16Maa koy won mboolem coono bi mu wara dékku ngir sama tur.»
17Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg Sóol loxo, ne ko: «Mbokk mi Sóol, Sang Yeesu, mi la feeñu woon ci yoon wi nga dikke, moo ma yebal ci yaw, ngir nga dellu di gis te feese Noo gu Sell gi.»
18Ca saa sa lu mel niy waasintóor wadde ca bët ya, mu dellu di gis. Mu daldi jóg, ñu sóob ko ci ndox.
19Ba loolu wéyee, mu lekk, doora am doole. Sóol toog na ak taalibe ya ca Damaas ay fan.

Read Jëf ya 9Jëf ya 9
Compare Jëf ya 9:1-19Jëf ya 9:1-19