Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 8

Jëf ya 8:27-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
27Filib fabu, dem. Ndeke am na jenn waayu Ecopi ju màggalsi woon Yerusalem. Nit kooku doonoon moraange, te di jaraaf ju mag ju Kàndas Lingeeru Ecopi; moo doon saytu mboolem alalu Lingeeru Ecopi.
28Naka la jaraaf ja màggalsi bay dellu Ecopi, toog ca watiiram, di jàngaale téereb Yonent Yàlla Esayi,
29Noowug Yàlla ne Filib: «Doxal, dab watiir bale.»
30Filib dabsi waayi Ecopi ja, daldi dégg muy jàng téereb Yonent Yàlla Esayi. Mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
31Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, te kenn firilu ma ko?» Ba loolu amee mu ne Filib, mu yéeg, toog ak moom. Filib yéeg.
32Lii nag mooy dogu mbind ma mu doon biral: «Dees koo yóbbu ni xar mu ñuy rendiji; mbete mburt mu ne cell ci kanam ki koy wat, ubbiwul gémmiñam.
33Ci biir toroxteem lañu ko xañ dëggam; kuutaayam nag, ana ku ci mana wax? Ndegam bakkanam lañu toxale kaw suuf.»
34Jaraaf ja ne Filib: «Yaw laay laaj, ci kan la yonent bi wax lii? Boppam lay wax am keneen?»
35Filib daldi àddu, tàmbalee ci dog boobu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.
36Ba loolu amee ñu topp yoon wi, ba yem ci am ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngii, ana lu tee ma sóobu ci?»
37Filib ne ko: «Soo gëmee ci sa léppi xol, sañ nga ko.» Mu ne ko: «Gëm naa ne Yeesu Almasi mooy Doomu Yàlla.»
38Ci kaw loolu jaraaf ja santaane ñu taxawal watiir ba; Filib ak jaraaf ja wàcc, ñu dugg ñoom ñaar ca ndox ma, Filib sóob ko ca.
39Naka lañu génne ca ndox ma, ngelawal Boroom bi ne cas Filib, yóbbu, jaraaf ja gisatu ko. Teewul mu topp yoonam, ànd ak mbég.

Read Jëf ya 8Jëf ya 8
Compare Jëf ya 8:27-39Jëf ya 8:27-39