Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 8

JËF YA 8:16-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
16Ndaxte wàccagul ci kenn ci ñoom, waaye sóoboon nañu leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu.
17Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, ñu jot Xel mu Sell mi.
18Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,
19ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.»
20Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis.
21Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla.
22Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.
23Ndaxte gis naa ne sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar not na la.»
24Simoŋ nag ne leen: «Ñaanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.»
25Noonu bi ñu seedeelee Yàlla te wax ci kàddoom, ñu dellu Yerusalem, di xamle xibaaru jàmm bi ci dëkk yu bare yu waa Samari.
26Naka noonu benn malaakam Boroom bi ne Filib: «Jógal te jublu Misra, jaar ci yoon wi jóge Yerusalem, jëm Gasa, di màndiŋ.»
27Filib jóg dem. Noonu mu gis fa nitu Ecópi ku yoom, di jaraaf ju mag ci Kandas, buur bu jigéen bu Ecópi, te di ko wottul xaalisam bépp. Fekk mu ñëwoon Yerusalem, ngir màggalsi Yàlla, bay dellu;
28mu toog ci watiiram, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi.
29Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.»

Read JËF YA 8JËF YA 8
Compare JËF YA 8:16-29JËF YA 8:16-29