Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 7

Jëf ya 7:5-58

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Taxul mu muurale ko lenn ci réew mii, du sax fu mu teg tànkam. Teewul mu dig ko, ne moom lay moomale réew mi, mook askanam wa koy wuutuji, te fekkul sax mu am doom.
6Yàlla ne ko: “Saw askan dinañu toxuji bitim réew, te dees na leen def ay jaam, mitital leen diiru ñeenti téeméeri at (400).”
7Yàlla neeti ko: “Xeet wi leen di jaamloo nag, man maa leen di mbugal. Gannaaw loolu dinañu fa génne, jaamusi ma ci bérab bii.”
8Yàlla daldi fasook Ibraayma kóllëre gu mu màndargale xaraf. Moo tax Ibraayma xarfal doomam Isaaxa, ba mu juddoo ba am juróom ñetti fan; Isaaxa, Yanqóoba, Yanqóoba, fukki maam yaak ñaar.
9«Maam yooyu nag iñaane seen doomu baay Yuusufa, ba jaay ko njaam, ñu yóbbu ko Misra. Teewul Yàlla ànd ak Yuusufa,
10xettli ko ci coonoom yépp, rafetal xelam, may ko itam Firawna buuru Misra baaxe ko; mu def ko kilifa ci Misra ak ci biir ëttu këram gépp.
11«Ci kaw loolu ab xiif dikkal Misra gépp ak réewum Kanaan. Mu metti lool. Sunuy maam nag amatuñu ab dund.
12Yanqóoba dégg ne ab dund am na Misra. Ca la fa jëkka yebal sunu maam ya.
13Seen ñaareel bi yoon la Yuusufa xàmmiku ay doomi baayam, Firawna nag doxe ca xam cosaanu Yuusufa.
14Ci kaw loolu Yuusufa yeble, indi baayam ak bokkam yépp, ñuy juróom ñaar fukki nit ak juróom.
15Noonu la Yanqóoba deme Misra, ba faatoo fa, mook sunuy maam.
16Gannaaw gi lañu toxal seeni yax ca Sikem, denc leen ca bàmmeel, ba Ibraayma weccikoo woon xaalis ca doomi Amor ca Sikem.
17«Ñu dem ba dige ba Yàlla giñaloon Ibraayma di waaja sotti, yemook xeet wi yokku, di gëna bare ci Misra,
18ba beneen buur bu xamul Yuusufa falu ci Misra.
19Buur boobu nag di muusaatu sunu xeet wi, di mitital sunuy maam, di leen sànniloo seeni liir, ngir ñu baña dund.
20«Booba la Musaa juddu, rafet ba fa kanam Yàlla, ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam.
21Ba ñu ko sànnee, doomu Firawna ju jigéen a ko foral boppam, yar ko ni doomam ju mu jur.
22Musaa nag di ku mokkal mboolem xam-xamu Misra, te ràññiku lool ci wax ak ci jëf.
23«Ba ñeent fukki atam matee, xelum seeti bokki bànni Israyilam dikkal ko.
24Ci kaw loolu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, daldi rey waayi Misra ja, feyul ka mu néewal.
25Booba Musaa foog na ne ay bokkam xam nañu ne ciy loxoom la leen Yàlla di indile wall, ndeke xamuñu ko.
26Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, di leen jéema jubale, ne leen: “Yeen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di lorante?”
27Ka doon néewal doole moroom ma bëmëx Musaa, ne ko: “Yaw, ku la def njiit mbaa àttekat ci sunu kaw?
28Xanaa danga maa nara rey, na nga reye waayi Misra ja démb?”
29Musaa dégg kàddu googu, daldi gàddaay, dem dali réewum Majan, ba am fa ñaari doom yu góor.
30«Mu teg ca ñeent fukki at, malaaka feeñu ko ca màndiŋu tundu Sinayi, ci biir tàkk-tàkku sawara wu jafal ab gajj.
31Musaa gis peeñu moomu, yéemu; mu dikk ba jege ko ngir niir ko, kàddug Boroom bi daldi jib. Mu ne:
32“Man maay sa Yàllay maam, maay Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.” Musaa tiit bay lox, ñemeetula xool.
33Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndax fii nga taxaw, suuf su sell la.
34Gis naa bu baax sama coonob ñoñ ci Misra; maa dégg seeni onk, ba wàcc ngir wallusi leen. Léegi nag dikkal, ma yebal la Misra.”
35«Musaa moomu ñu weddi woon, ne ko: “Ku la def kilifa ak ab àttekat?” Moom nag la Yàlla def kilifa ak ab jotkat, yebal ko ci ñoom, malaaka ma feeñu Musaa ca gajj ba, daldi koy jottli yóbbante ba.
36Moo leen génne réewum Misra, moo def ay kéemaan aki firnde ca réew ma, ak ca géeju Barax ya, ak ca màndiŋ ma, diiru ñeent fukki at.
37Musaa moomu moo noon bànni Israyil: “Yonent bu mel ni man la leen Yàlla di feeñalal ci seen biiri bokk.”
38Moom it moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, mook malaaka ma doon wax ak moom ca kaw tundu Sinayi ca sunu wetu maam ya. Moo jot ci kàddu yuy dund, ngir jottli nu ko.
39Kooku la sunuy maam nanguwul woona déggal. Dañu koo far xarab, namma walbatiku dellu Misra.
40Ñu ne Aaróona: “Sàkkal nu ay yàlla yu nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra, xamunu lu ko dal.”
41Jant yooyu lañu sàkk jëmmu sëllu, defal jëmm ja ab sarax, di bànneexoo lu ñu sàkke seeni loxo.
42Yàlla nag dëddu leen, bàyyi leen, ñuy jaamu biddiiw yi, ni ñu ko binde ci téereb yonent yi, ne: “Yeen waa kër Israyil, saraxu jur ak yeneen sarax, ndax man ngeen ko daan indil diiru ñeent fukki at ca màndiŋ ma?
43Molog seen tuur mi, ngeen yóbbaale xaymab jaamookaayam, ak seen biddiiwu yàlla ji ñu naa Refan, jëmm yooyu ngeen sàkk, di leen sujjóotal! Kon nag maa leen di toxal ca wàllaa Babilon.”
44«Xaymab seede baa nga woon ak sunuy maam ca màndiŋ ma, ñu sàkke ko na ko ka doon wax ak Musaa sante, dëppale kook misaal ma Musaa gisoon.
45Xayma ba la sunuy maam jot, dugal ko ci kilifteefu Yosuwe ca biir réewum xeet, ya leen Yàlla dàqal. Xayma ba nekk fa, ba ca janti Daawuda.
46Daawuda, ma Yàlla baaxe woon, sàkku woon na am màkkaan ngir Yàllay Yanqóoba.
47Waaye Suleymaan moo ko mujj tabaxal kër.
48«Moona Aji Kawe ji du dëkke lu loxo defar, mooy la yonent ba ne:
49“Asamaan sama ngàngunee, suuf di sama ndëggastal. Ana kër gu ngeen may tabaxal? Boroom bee ko wax. Mu ne: Ana ban bérab laay nopploo?
50Loolu lépp, xanaa du sama loxoo ko sàkk?”
51«Yeena dëgër bopp, yeenay boroomi xol ak noppi yéefar! Dungeen noppee të Noo gu Sell gi? Maam ya, doom ya rekk!
52Kan ci yonent yi la seeni maam fitnaalul? Ñoo rey démb ña yégle woon ñëwug Aji Jub, ji ngeen wor tey, bóom ko.
53Yeen de yeena jotoon ci yoonu Musaa, wi ay malaaka jottli, te taxul ngeen jëfe ko.»
54Naka lañu dégg loolu, seen xol fuddu, ñuy yéyu ci kawam.
55Eccen nag feese Noo gu Sell gi, ne jàkk asamaan, daldi gis leeru Yàlla, gis Yeesu taxawe fa ndijooru Yàlla.
56Mu ne: «Asamaan a ngii ma gis, mu ubbiku, Doomu nit kaa ngii taxaw fi ndijooru Yàlla!»
57Ba loolu amee ñu yuuxu ca kaw, dar seeni nopp, daldi ànd, ne milib ca kawam;
58ñu wat-watee ko, génne ko dëkk ba, di ko dóor ay doj. Fekk na seede ya summi seeni mbubb, juug ca tànki benn xalelu góor bu ñuy wax Sóol.

Read Jëf ya 7Jëf ya 7
Compare Jëf ya 7:5-58Jëf ya 7:5-58