Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 7

JËF YA 7:43-59

Help us?
Click on verse(s) to share them!
43Yóbbu ngeen sax fu nekk xayma, biy màggalukaayu Molog, ak biddiiwub Refan, bi ñu daan bokkaaleel Yàlla, di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen! Kon nag dinaa leen toxal, yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.”
44«Sunuy maam amoon nañu ca màndiŋ ma xaymab màggalukaay, bi ëmboon li Yàlla seede. Xayma boobu nag defoon nañu ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Yàlla sante woon.
45Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, ñu jot xayma ba ñoom it, yóbbu ko ca réew, ma ñu nangu ca xeet ya Yàlla dàq ci seen kanam. Xayma ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda.
46Moom yiw na fa kanam Yàlla, mu ñaan ko, mu sàkkal ko kër ngir askanu Yanqóoba.
47Waaye Suleymaan moo tabaxal Yàlla kër ga.
48«Moona Aji Kawe ji du dëkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne:
49“Asamaan mooy sama jal, te suuf mooy sama tegukaayu tànk. Kon gan kër ngeen may tabaxal, mbaa fan mooy sama bérabu noppalukaay?
50Ndax du sama loxo moo defar yëf yooyu yépp? —Moom la Boroom bi doon wax.”
51«Yéen ñi dëgër bopp, ànd ak xol buy bañ ak ay nopp yuy fatt, mel ni ñi xamul Yàlla. Dungeen noppeek a diiroo ak Xel mu Sell mi; ni ko seen baay yi daan defe, noonu ngeen di def, yéen itam.
52Kan ca yonent ya la seeni maam tegul woon ay fitna? Rey nañu ñi doon yégle ñëwug Aji Jub ji, moom mi ngeen jébbale léegi, ba ñu rey ko.
53Jot ngeen yoonu Musaa, wi Yàlla wàcce jaarale ko ci ay malaaka, te sàggane ngeen ko.»
54Bi ñu déggee loolu nag, seeni xol di dagg, ñuy yéyu, jëm ci kawam.
55Waaye Ecen, mi fees ak Xel mu Sell mi, ne jàkk ci asamaan, gis ndamu Yàlla, te gis Yeesu mi taxaw ci ndijooru Yàlla.
56Mu ne: «Seetleen, maa ngi gis asamaan yi ubbiku, te Doomu nit kaa ngii taxaw ci ndijooru Yàlla.»
57Bi ñu déggee loolu, ñu daldi xaacu ca kaw, tey dar seeni nopp; ñu ànd, ne milib ci kawam;
58ñu wat-wate ko, génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj, ba mu dee. Seede ya tegoon nañu seeni yére ci tànki waxambaane wu tudd Sóol.
59Noonu ñu dóor Ecen ay doj, muy ñaan Yàlla ne: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu!»

Read JËF YA 7JËF YA 7
Compare JËF YA 7:43-59JËF YA 7:43-59