Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 7

JËF YA 7:2-31

Help us?
Click on verse(s) to share them!
2Ecen ne ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan.
3Mu ne ko: “Toxul sa réew, bàyyi say bokk, te ñëw ci réew, mi ma lay won.”
4«Ci kaw loolu mu génn réewu niti Kalde, dëkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Yàlla toxale ko foofa, dëël ko ci réew, mi ngeen dëkk léegi.
5Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu wara donale, du sax fu mu mana teg tànkam; waaye dig na ko ne dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.
6Yàlla ne ko: “Ñi soqikoo ci yaw dinañu ganeyaan ci réew mu ñu dëkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub ñeenti téeméeri at.”
7Waaye Yàlla nee na: “Xeet wi leen jaamloo, man maa leen di àtte te gannaaw loolu dinañu génn, di ma jaamu ci bérab bii.”
8Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi.
9«Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko,
10génne ko ci coonoom yépp, defal ko yiw ak xel ci kanam Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak këram gépp.
11«Bi loolu amee xiif tàbbi ci biir Misra ak réewu Kanaan mépp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatuñu lu ñu lekk.
12Yanqóoba nag dégg ne Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, ñu dem fa yoon wu jëkk.
13Bi fa ay doomi baayam delloo nag, Yuusufa xàmmiku leen, te Firawna xamante ak njabootam.
14Ci kaw loolu Yuusufa yeble, woo baayam ak bokkam yépp, ñuy juróom ñaar fukki nit ak juróom.
15Noonu Yanqóoba dem Misra, faatu fa, moom ak sunuy maam.
16Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sisem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Amor ca Sisem.
17«Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gëna bare ci Misra,
18ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.
19Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee.
20«Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam,
21ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam.
22Musaa nag di ku yewwu ci xam-xamu waa Misra bépp, di jàmbaar ci wax ak jëf.
23«Bi mu demee ba am ñeent fukki at, mu fas yéeney seeti ay bokkam, maanaam bànni Israyil.
24Noonu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, feyul ko, ba dóor waayi Misra ja.
25Mu defe ne, ay bokkam dinañu xam ne ciy loxoom la leen Yàllay musale, waaye xamuñu ko.
26Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéema jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?”
27Waaye kiy néewal doole moroomam bëmëx ko ne: “Ku la teg kilifa ak àttekat ci sunu kaw?
28Ndax danga maa bëgga rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?”
29Bi Musaa déggee wax jooju, mu daldi daw, dem réewu Majan, di fa ab doxandéem; mu séy fa, ba am ñaari doom.
30«Lu ko wees ñeent fukki at nag, bi mu nekkee ca màndiŋu tundu Sinayi, malaaka feeñu ko ci takk-takku sawara ci biir as ngarab.
31Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, dégg baatu Boroom bi ne ko:

Read JËF YA 7JËF YA 7
Compare JËF YA 7:2-31JËF YA 7:2-31