Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 5

JËF YA 5:9-29

Help us?
Click on verse(s) to share them!
9Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.»
10Ca saa sa mu daanu ciy tànkam, dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram.
11Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp.
12Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga.
13Te kenn ci ña ca des ñemewula booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.
14Moona ay nit ñu gëna bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom.
15Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom.
16Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér.
17Booba sarxalkat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen,
18ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba.
19Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan:
20«Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.»
21Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare. Bi ñu koy def, sarxalkat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
22Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi délsi, yégle ko
23ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»
24Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.
25Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.»
26Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer.
27Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanam mbooloo ma. Sarxalkat bu mag ba laaj leen
28ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»
29Waaye Piyeer ak ndaw ya ne leen: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit.

Read JËF YA 5JËF YA 5
Compare JËF YA 5:9-29JËF YA 5:9-29