Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 5

Jëf ya 5:7-26

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ñu teg ca lu wara tollook ñetti waxtu, jabaram duggsi, te yégul la xew.
8Piyeer ne ko: «Wax ma, nàngam ngeen jaaye tool bee?» Mu ne ko: «Waaw, nàngam la.»
9Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Ana lu ngeen di mànkoo, di nattu Noowug Boroom bi? Déglul, tànk yi suuli woon sa jëkkër a ngoogu ci bunt bi di la yóbbusi yaw it.»
10Ca saa sa ndaw sa daanu cay tànkam, dee. Xale yu góor yi duggsi, fekk ko mu dee; ñu yóbbu ko, suul ko ca wetu jëkkëram.
11Ba loolu amee tiitaange ju réy a jàpp mbooloom gëmkat ñépp, ak ña ko dégg ñépp.
12Ci kaw loolu ay firnde ak kéemaan yu bare di sottee ci loxol ndaw yi, ci biir askan wi. Gëmkat ñi nag di bokk daje ñoom ñépp fa ñuy wax Mbaarum Suleymaan, ca biir kër Yàlla ga,
13waaye kenn ca ña ca des ñemewula jaxasoo ak ñoom. Teewul askan wa nawloo leen lool.
14Gëmkati Sang bi nag di gëna bare, ñuy wàllisi, ba doon mbooloo mu mag, góor ak jigéen.
15Nit ñi dem bay génne jarag ji ci mbedd yi, teg leen ci ay laltu aki basaŋ, ngir bu fa Piyeer jaaree, lu bon bon takkndeeram mana dal ñenn ci ñoom.
16Ci biir loolu nit ñu bare bàbbeekoo ca dëkk ya séq Yerusalem, indi ay jarag ak ñu rab yu bon sonal; ñoom ñépp daldi wér.
17Ba mu ko defee xolu kañaan dugg sarxalkat bu mag ba, ak mboolem ña ko dar, te di waa ngérum Sadusen ña.
18Ñu teg ndaw ya loxo, tëj leen ca kaso ba.
19Ca guddi ga nag malaakam Boroom bi ubbi bunti kaso ba, génne leen, ne leen:
20«Demleen taxaw ca digg kër Yàlla ga, ngeen xamal askan wi mboolem lu jëm ci dund gii.»
21Gannaaw ba ñu déggee loolu, ba bët set, ñu dugg ca kër Yàlla ga, di waare. Ci biir loolu sarxalkat bu mag ba ak ña ko dar, dikk, woolu kurélu àttekat ya, mboolem kurélu njiiti bànni Israyil; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
22Dag ya nag dikk, fekkuñu leen ca kaso ba, ñu dellu yégleji ko,
23ne: «Danoo fekk kaso ba tëje ràpp, wattukat ya taxaw ca bunt ya. Nu tijji, fekkunu kenn ca biir!»
24Jawriñu kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya dégg loolu, daldi jaaxle lool ci ndaw yi, di xalaat nu mbir miy mujje.
25Mu am ku dikk, ne leen: «Ña ngeen tëjoon kaso déy a nga noonu ca kër Yàlla ga, di waare.»
26Ci kaw loolu jawriñu kër Yàlla ga ak dag ya jëli ndaw ya ndànk, bañ leena jaay doole, ngir ragal nit ñi sànni leen ay doj.

Read Jëf ya 5Jëf ya 5
Compare Jëf ya 5:7-26Jëf ya 5:7-26