Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 5

JËF YA 5:7-13

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Ñetti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew.
8Piyeer daldi ko ne: «Wax ma, ndax lii mooy njégu tool bi?» Mu ne ko: «Waawaaw, lii la.»
9Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.»
10Ca saa sa mu daanu ciy tànkam, dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram.
11Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp.
12Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga.
13Te kenn ci ña ca des ñemewula booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.

Read JËF YA 5JËF YA 5
Compare JËF YA 5:7-13JËF YA 5:7-13