Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 5

Jëf ya 5:29-38

Help us?
Click on verse(s) to share them!
29Piyeer ak ndaw ya ca des nag ne leen: «Yàlla lees wara déggal, waaye du nit.
30Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.
31Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.
32Nun noo seede loolu, nook Noo gu Sell, gi Yàlla jagleel ñi ko déggal.»
33Ba ñu déggee loolu, dañoo mer ba fees, nar leena rey.
34Ab Farisen bu ñuy wax Gamalyel, di jànglekatu yoonu Musaa bu ñépp nawloo, daldi taxaw ca digg kurélu àttekat ya. Mu joxe ndigal ngir ñu génne leen ab diir.
35Ba ñu génnee, mu ne waa kurél ga: «Yeen bokki Israyil, moytuleen bu baax li ngeen di def ak nit ñii.
36Ndaxte bu yàggul la Tëdas jóg, di jaay daraja, ba lu wara tollook ñeenti téeméeri nit far ak moom. Ñu rey ko, ña ko toppoon ñépp tasaaroo, seen pexe mujjewul fenn.
37Gannaawam it Yuda mu Galile jóg, ca jant ya ñu doon lim waa réew mi; mu yóbbaale mbooloo mu ko topp. Moom itam dee, ña ko toppoon ñépp tasaaroo.
38Léegi nag, dama ne, maanduleen ci ñii, te ba leen, ngir su seen mébét mbaa seen jëf bawoo ci nit, day yàqu rekk.

Read Jëf ya 5Jëf ya 5
Compare Jëf ya 5:29-38Jëf ya 5:29-38