Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Jëf ya - Jëf ya 5

Jëf ya 5:25-34

Help us?
Click on verse(s) to share them!
25Mu am ku dikk, ne leen: «Ña ngeen tëjoon kaso déy a nga noonu ca kër Yàlla ga, di waare.»
26Ci kaw loolu jawriñu kër Yàlla ga ak dag ya jëli ndaw ya ndànk, bañ leena jaay doole, ngir ragal nit ñi sànni leen ay doj.
27Ñu indi leen, taxawal leen ca kanam kurélu àttekat ya, sarxalkat bu mag ba laaj leen,
28ne: «Xanaa aayewunu leen woon ne buleen waareeti mukk ci woowu tur? Yeena ngi nii ubale Yerusalem ak seen waare, ngeen nar nu cee gàdduloo bakkanu nit kii!»
29Piyeer ak ndaw ya ca des nag ne leen: «Yàlla lees wara déggal, waaye du nit.
30Sunu Yàllay maam moo dekkal Yeesu, mi ngeen wékk ci bant, bóom ko.
31Moom la Yàlla yékkati ci wetu ndijooram, def ko muy Njiit, di Musalkat, ngir may bànni Israyil ag tuubeel ak njéggalug bàkkaar.
32Nun noo seede loolu, nook Noo gu Sell, gi Yàlla jagleel ñi ko déggal.»
33Ba ñu déggee loolu, dañoo mer ba fees, nar leena rey.
34Ab Farisen bu ñuy wax Gamalyel, di jànglekatu yoonu Musaa bu ñépp nawloo, daldi taxaw ca digg kurélu àttekat ya. Mu joxe ndigal ngir ñu génne leen ab diir.

Read Jëf ya 5Jëf ya 5
Compare Jëf ya 5:25-34Jëf ya 5:25-34