Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 5

JËF YA 5:11-40

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp.
12Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga.
13Te kenn ci ña ca des ñemewula booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.
14Moona ay nit ñu gëna bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom.
15Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom.
16Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér.
17Booba sarxalkat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen,
18ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba.
19Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan:
20«Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.»
21Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare. Bi ñu koy def, sarxalkat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.
22Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi délsi, yégle ko
23ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»
24Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak sarxalkat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.
25Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.»
26Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer.
27Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanam mbooloo ma. Sarxalkat bu mag ba laaj leen
28ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»
29Waaye Piyeer ak ndaw ya ne leen: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit.
30Yàllay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen bóomoon ci wékk ko ca bant ba.
31Te Yàlla yékkati na ko ci ndijooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may bànni Israyil réccu, ba mu baal leen seeni bàkkaar.
32Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Yàlla may ñi koy déggal.»
33Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leena rey.
34Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti.
35Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.
36Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.
37Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.
38Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu.
39Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko mana fanq, ngir ragala jànkoonte ak Yàlla.»
40Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.

Read JËF YA 5JËF YA 5
Compare JËF YA 5:11-40JËF YA 5:11-40